url
stringlengths 30
180
| content
stringlengths 64
14.2k
| Source
stringclasses 1
value |
---|---|---|
https://www.defuwaxu.com/bank-monjaal-kurel-gi-nuy-jatan/ | ‘’BÀNK MONJAAL’’, KURÉL GI NUY JATAŋ
Ñépp a ngi fàttaliku ni « Bànk Monjaal » nasaxale woon réew mi ci nguurug Abdu Juuf. Ci wàllu njàng, wér-gi-yaram ak mbir yu bari yu deme noonu, kurél googu fexe woon na ba Juuf génne ca loxoom, muy def lu ko neex.
Loolu juroon na fiy jafe-jafe yu tar. Ndax taxoon na ñu jaay waa bitim-réew bérébi liggéeyukaay yu bare. Doomi-Senegaal yu bari ñàkkoon nañu ci seen liggéey, xale yi mënatuñu woon a jàngi te feebar faju jafe woon na. Ci gàttal daal, ci lu jëm ci yokkuteg askan wi, mbir yi sooxe woon nañu bu baax. Waa “Bànk Monjaal” doon bàkke Abdu Juuf: “Ndongol Bànk Monjaal li ko gën a nangul”. Réew miy wéy ciy jafe-jafe, ñu naan nu muñleen rekk, dina baaxi ëllëg.
Waaye dara doonu ci woon dëgg. Jafe-jafe yooyu sax, bokk nañu ci li fi jële Abdu Juuf ci atum 2000. Noonu, Abdulaay Wàdd dikk, xaw a fippu ni àndut ak ñoom ci yenn gis-gis yi. Looloo mayoon nguuram sañ-sañu defar ay tali, def itam ay jéego ci njàng meek paj mi.
Loolu dafay firndeel ni Bànk Monjaal ak kurél yu mel ni moom, réew yu mag yi lañu fi nekkal, ndax ñoo leen di suuxat. Ba tax na sunu njiit yi war nañuy settantal seeni ndigal, war nañuy jiital seen njariñu askan. Noonu la ko Peresidaŋ Néeru tamit defe woon ca réewum End. Ba ko waa ‘’Bànk Monjaal’’ joxee ay tegtal, rëddal ko yoon wi mu war a jaar, daa xotti lépp ba mu ko wóore ni bu ko defee réewam dina soox, jóge fa suux.
Waaye bu dee ci sunu réew yi, fulla jooju moo fiy tumurànke léeg-léeg. Lu leen “boroom xam-xami tubaab yi” wax, ñu def ko am seew. Te moone ñooñu, seen njariñu réew rekk a leen yitteel !
Moone ba tey ‘’Bànk Monjaal’’ a ngi fi. Di digal sunu njiit yi ñuy jëfe. Moo tax tamit 59 at a ngi, ñu ne noo moom sunu bopp te mënagunoo dem fenn. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/lamb-tafaa-tin-daan-na-emma-seen/ | LÀMB : TAFAA TIN DAAN NA ËMMA SEEN
Gannaaw ba Móodu Lóo ak Aama Balde bëree ci ayu-bés bii weesu, Móodu daan ko, démb ñaari punkal ñoo doon dajeeti, muy Ëmma Seen ak Tafaa Tin. Ñaari mbër yépp waajal nañu seen bés bi na mu waree, def i jàkkaarloo yu tàng, saf sàpp ak i nappante.
Ci bés bi, ku ci nekk àndi nga sa mbooloo, “Arène nationale” bi fees. Tafaa Tin a jëkk a bàkku, bàkku seereer bu neex. Ba mu noppee, Ëmma Seen bàkku tamit, ci biir bàkku bi mu sargal ci kii di Aama Balde ak baayam ja Fàllaay Balde. Waaye, fàttewul it kii di Tayson ak Boy Ñaŋ. bàkkoom gi mënees na ni tontu la ci waxi xàjjale ci biir Pikin yi doon jib ginnaaw bi Aama ñàkkee ci kanamu Móodu Lóo. Kon mel na ni dafa xamal yàqkat yi ni Pikin benn bopp la.
Ba ñu nekkee ci diggu géew ga, ku ci nekk di def xarfa-fuufam yu mujj, Ëmma am buteel bu mu yor di tuur ndox di daw bëgg a wër kii di Tafaa Tin, mu daldi koy bañ, kar ko ñu jot fa songoo laalantey kurpeñ.
Seen bëre bee ngi tàmbalii ba 21i waxtu tegee 34i simili. Ñu léewatoo lu yàggul dar, daldi tàmbali xeex xeex bu metti Ëmma dóor ko ci dóor bu dal, Tafaa Tin dem ardo dikkaat. Ci noonu ñu dawalaat léewatoo bi tuuti tàmbaliwaat xeex bi, mu mujje ci cong. Ëmma dafa doon jéem a jàpp tànku Tafaa Tin far mu moy, mu daldi rëpp, Tafaa Tin jaay ko doole, bës ko ci suuf si, daldi koy daan.
Mu nekkoon bëre bu neex, doore ci xeex jeexe ci jàppante, ñépp daldi bég.
Ci dibéer gii di ñëw, Sitta war na ci daje ak Lac Guiers 2, muy bés bees di xaar itam. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/gattali-taggat-yaram/ | Saajo Maane ca Bayern Munich
Njiiti Bayern Munich yi mujje woon nañ déggook yu Liverpool FC yi ñeel ëllëgu Saajo Maane. Doomu Senegaal ji di jóge Liverpool bim fa jotee def 6i at (Suweŋ 2016 ba Suweŋ 2022), amal fa 267i joŋante, dugal ca 120i bii. Talaatay tey ji la Bayern di ko dalal ngir mu amal caytu-yaram ginnaaw bi mu fa teewee ngir xaatim déggoo yi. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-alxames-23-mars-2023/ | LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (ALXAMES 23 MÀRS 2023)
Adebayoor ak Özil bàyyi nañu
Adebayoor, saa-Tógoo bàyyina kuppe ! Barkaatii-démb ci altine ji la yëgle ne tekkinay dàllam fas-yéene ko bàyyi ak xale yi ndax ne mag dikk na. Moo ngeek 39i at, kuppe deseelatu ko dara. Lenn ci ekib yu mag yu mu jaar mën nañ ci tudd Monaco, Arsenal, Réal Madrid ak Manchester City, nekkoon fa ku am solo, ba ci dëkkam itam, Tógoo, kuñ fa joxoon cër la ndax lim fa def.
Moom mii di Özil tamit gënoon siiw ca booru Réal Madrid, jóge fa jaar Arsenal laata muy dem fa Tirkii ca këlëb boobu di Besiktas, xamle na itam ni wékk nay dàllam, bàyyi kuppe. Moom nag, moo ngi bàyyee 34i at. Bokk na ci kuppekat yees di tudd ci mën paas donte mujjug dundug kuppeem demeewul nim ko bëggee woon ndax ay jafe-jafe yu sew-sewaan.
Espaañ/Barça
Barcelone mi ngi ciy jafe-jafe jamono jii. Nde, dañ ko tuumaal ne dafa daan ger arbit yi, diggante 2003 ba 2018. Mbir mi tàbbi ci loxoy Yoon, muy def i jéego, di lëñbët ngir xam li xew. Loolu nag, andi nay wax yu sew : ñii di dëggal, ñee di weddi. Waaye, dara leeragu ci. Démb, bi ñu xëyee, ñenn ci taskati xibaari Espaañ yi génne nañuy xibaar di wax ni, moom Barça narul a bokk ca “League des Champions” déwén bi. Laporte, njiitu Barça, loolee naqari na ko bam dem ci yoon “plainte” lenn ci taskati-xibaar yooyee. Gannaaw loolu nag, ñu ci bari dindi nañu xibaar yi ñu dugaloon ci mbaali-jokkoo yi.
CAN U-23 : Senegaal duma na Mali 3-1
Démb, ci àllarba ji, la ndawi Senegaal yi amagul 23i at doon amal seen joŋante bu njëkk ñeel kuppeg Afrig gees jagleel ndaw yi amagul 23i at. Ñu doon ci daje ak Mali. Senegaal moo mujje gañe ñetti bal ci benn. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/lamb-moodu-loo-di-woo-jepp-doomu-parsel-ci-ginnaaw-fara/ | Làmb : Móodu Lóo di woo jépp doomu Parsel ci ginnaaw Farã
Démb la Farã doon amal Open Press ñeel laale bi war am ci digganteem ak Soq. Mbëri Parsel yu mag yi bare woon nañ fa ngir biral jàppale giñ koy jàppale. Kii di Móodu Lóo jot na fa yékkatiy kàddu. Woo na jépp doomu Parsel ñu teew ca Aren nasiyonaal ngir dooleel seen doom Farã. Jàmmaarloo boobu warees na am ci gaawu bii, yemook 19i fan ci weeru Me. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-23-7-2023/ | XIBAARI TAGGAT-YARAM (23/7/2023)
MESSI DELLOONA BUUM CA MBOY-MBOY GA !
Bërki-démb ci guddi, bi 3i waxtu jotee, la saa-arsàntin bi doon amal joŋanteem bu njëkk ak këlëb bu bees bee di Inter Miami fa USA (Amerig). Boobu këlëb nag nga xam ni futbalkat bu mag ba woon, David Beckham moo ko moom, defoon na 11i jonante yoy, gañewu ci woon benn. Bi Messi dikkee lañu xamaat cafkay ndam. Ci ñaareelu xaaju joŋante bi la Messi duggu, mu ngi fekk ñu nekkoon ci 1-1, gannaaw ba ñu jiitalee woon ekibam mul delsi. Ñuy dawal noonu ba ca bopp jeexital ga rekk, Inter Miami am teg-dóor. Booba, ñoo ngi woon ci 94eelu simili bi. Messi dafa teg bal bi, laxas ko ci caax yi, rekk powu bay riir. Kii di boroom këlëb bi David Beckham dafa bég bay jooy. Ndeke, Messi jeexalagul.
ÓBAMEYAN AK ISMAYLA SAAR CA MARSEILLE
Maarsey moo ngi wër di defaraat bu baax taxawaayu ekibam. Bërki-démb lañ siiwal ñëwub Óbameyaŋ. Moom sax, tàmbali na tàggatoom ak i farandooram ya. Ci dibéeru tey jii tam, biral nañ seen déggoo diggante ak Watford mi moom Ismayla Saar. Daanaka, gayndeg Senegaal gi, léegi kuppekatu Marseille la. Ëllëg ci altine ji lañuy saytu yaramam foofu ca Marseille laata lépp di mat.
AB FEEBAR CI BIIR FC BARCELONE
Futbalkati FC Barcelone yi, jamono jii, dañu jànkonteel ak feebar bu law seen biir. Looloo tax sax ñu fomm joŋante bu njëkk bi ñu waroon a amal ëllëg ci doxantu bi muy amal fa Etaasini. Njortees na ni kenn ci ñi demoon Afrig ci bër yiñ amoon a ko indaale. Amaana mu bañ a ñàkku laata muy dem. Waaye, wax jooju amul ndëgëlaay. Nde, amul lenn lu koy firndeel.
AFROBASKET 2023, KIGALI
Sunu Jigéen ñi dem nañu Ruwàndaa bërki-démb, àjjuma guddi. Jot nañ sax amal gaawug démb gi seen tàggatu gu njëkk foofa ca tàggatuwaay (Gymnase) bu Liise Kigali. Afrobasket baa ngi war tàmbali 28eelu fan ci weeru sulet, war a jeex 5eelu fan ci weeru ut. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | MBAY JAAG, GOR BI SENEGAAL AMEEL BOR (Xaaj bu njëkk)
Xel tëju na, xalaat dëju. Xol tooy na, bët jooy. Ndeysaan… Gaynde wàcc na liggéey. Nee leen ko mbarawàcc, Jaag, nu sargal ko, delloo ko njukkal.
Mbay Jaag wuyuji na Boroomam. Dibéer, 12eelufan ci weeru me atum 2019 la génn àddina. Li Yàllay def, dibéer jooju dafa yemoo kepp ak 51eelu at ca ba muy jiite toogaayu-ñaxtu ba ndongoy iniwérsite bu Ndakaaru amaloon, waat ne fàww ñu janook Njiitu-réew ma woon, Léwopóol Sedaar Seŋoor, walla nguur gi ci boppam ngir àgge ko seen i tawat.
Mbay Jaag, nag, kenn umpalewul ne moo jiite woon kurélu Iniwérsite bu Ndakaaru, ca atum 1968 – booba, tuddagul woon Séex Anta Jóob – ga taxawoon di xeexal ndongo yi.
Ca yooyu jamono, fekk na Seŋoor nekk ci diggu ndëndam. Lu ko neex tëgg, ku feccul mu ni la génnal géew bi walla mu nëbb la jant bi. Ci gàttal, moo doon Buur, di Bummi. Ku say wax walla say jëf méngoowul ak i yosam, mu jaay la doole, ne la ràpp ci kaso bi, tëj. Waaye, kuy jaay fit, boo dajeek gaynde lamble.
Weeru me 1968 la ndongo yi jógoon, fippu, jàmmaarlook Nguur gi, ni ko : « Dafa doy ! Li nuy dund mënuta wéy ! » Ñu noon dee, coppite day am te dara lañu ci bañul. Ñu ga Nguur gi ci ne, na leen yokkal seen i ndàmpaay, jagalaat seen nekkin te it yeesal seeni jumtukaayi njàng.
Jamono jooju, daanaka fépp foo demoon ci àddina si, dinga gis ndongo yiy fippu di sàkku ab yeesal ñeel njàng mi.
Bu dee sunu réew mii, nag, UDES ak UED ñooy kuréli ndongo yi gënoon a fés ca xeex booba. Te, ñaari kurél yooyu yépp, Mbay Jaag ak i ñoñam ñoo leen jiite woon. Waaye ba tey ci njiit yooyule, Mbay Jaag lañu ci gënoon a ràññee.
Moom Mbay Jaag, nag, daanaka aul woon tiitukaay, ñi ko xamoon yépp, am fitam lañuy gën a fàttaliku tey. Rax-ci-dolli, dafa amoon pas-pas, farlu, te xareñoon lool. Kenn dàqu ko woon a wax ak mbooloo itam. Noonu, bu jëlaan kàddu gi, fu ne la nit ñiy fàqe ngir déglusi ko mbaa topp ci ginnaawam.
Mbay Jaag ! Kii moo amoon bayre, ndokk !
Jàmbaar jii moo teewoon nelaw Seŋoor ak i nduguroom. Waaye, Mbay Jaag ak ñi mel ni moom, foo leen fekk, nguur gu jubadi da leen di noonoo, di leen fexeel.
Moo tax Seŋoor mépp pexe mu mu xamoon lal na ko ngir sàkkal pexe Mbay Jaag ak ñi toppoon ci ginnaawam : nappaate, ger, tëj kaso, añs. Wànte du benn ci pexe yooyu bu ci àntu. Te, nag, ñi andoon ak Mbay Jaag ñoo ka bare woon ! Looloo tiitaloon Seŋoor, mu dem sax ba jàq lool. Ndax kat, ndongo yi dañoomayoon fit yeneeni kurél yi nekkoon ci réew mi, di liggéeykat yi booloo woon ciy sàndikaa yu siiw, am i tolof-tolof ba noppi ragal a fippu. Gone yee leen may fitu ñaxtu yi. Seeni rakk sax, ndongoy lekkooli diggu-dóom yi, dañoo jóg ñoom tamit. Mbir yi mujje ëpp i loxo ndax muy jàngalekat yi di óbëryee yi, kenn toogul. Koom-koomu réew mi tag, dara doxatul.
Bi Seŋooramatul pexe, takk-deri Frãs yi sàncoon seen gàdd ci Ndakaaroo mujjee wallsi nguuram. Teewul, ndongo yi ak seeni njiit wéy di lëkkalook liggéeykat yi, jàpp fi ñu jàpp. Gornamaa bi jàq, teggi loxoom, woo leen waxtaan, nangul leen lu bare ci seeni ñaxtu, ba jàmm delsi ci réew mi.
Wànte waxtaan wi taxu ko woon a yomb noonu : Mbay Jaag ak i ñoñam, dañca wone fullaak faayda ju mat sëkk, nañu ka daan defe naka-jekk. Fulla jooju ak pastéef yi ñu àndaloon bu ñu wàccaan ci mbedd yi ak tali yi, di sànniy xeer aka taal i póno. Ci njeexital li, ndongo yi jële nañfa ndam lu réy, doonte amuñu woon lépp la ñu bëggoon
Xew-xew yu metti yooyu, nag, mëneesu leen a nettali ba noppi di bañ a tudd xale Naaru-Libaŋ bi ci ñàkkoon bakkanam. Keroog, bésub 29 ci weeru me, la alkaati yi song néegi ndongo yi, dal seen kaw, gaañleen, yàq mbaa sàcc seeni bagaas ak seeni alal.
Mbay Jaag jitte woon na fi tamit ndongoy Iniwérsite bu Ndakaaru ci xeex bu mag bu ñu amaloon ci diggante 1971 ak 1972 te taxoon Seŋor tëjlu daara ju mag jooju.Dàqoon na yit ndongo yu bari ba noppi solal soldaar seeni njiit, yóbbu leen Kaasamaas, fa way-fippu PAIGC yi doon jàmmarlook làrme bu Purtugees yi. Ci ñooñu mënees na cee lim Ablaay Bàccili ak Mamadu Jóob Dëkurwaa… Bañkat yooyule, Mbay Jaag moo doon seen njiit. Ñoom ñépp ñu sànni leen ca Sancaba Manjaag, ci wetu Gine-Bisaawo, fa xare ba gënoon a mettee. Fa la Al Fuséyni Siise, kenn ci ñoom, faatoo ci anam bu ñaaw. Noonu la ñoom Mbay Jaag nekke woon ci làrme bi ak i jafe-jafe yu tar, ba biñ leen di bàyyi. Nguur gi jéem a saafara mbir mi, waxtaan ak ndongo yi, jëlaat ña mu dàqoon ba noppi fajal leen yenn ci seeni aajo.
Ginnaaw gi la Mbay Jaag génn Iniwérsite dem jàngaleji matematig ca Cees, jóge fa dem liggéeyi Liise Jiñaabo bu Sigicoor.
Xare yi mag yooyu askanu Senegaal difàttaliku tey, ndongo yépp a ci amoon ndam waaye jaloore ja ca Mbay Jaag jële, leneen mayu ko ko lu-dul taxawaayu njiit lu mat sëkk, ngor, njub, fit, ak xel mu ñaw, kaar !… boole ci ñàkk caaxaan bi ko ñépp mas a seedeel, te ñu bare jàppe woon ko naqadi deret mbaa sax ñàkk kersa.
Ñàkk caaxaan googoo ngi woon ci moom bés ba muy faatu.
(Fan yii di ñëw, LU DEFU WAXUdina delsi ci li des ci jaar-jaaru Mbay Jaag. Mooy doon ñaareelu xaaj bi) | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/lu-waral-itali-soppeeku-nii/ | LU WARAL ITALI SOPPEEKU NII ?
Ak lu waay mën a wax, réewum Itali yàqu na. Bi Salwini toogee ci jal bi ba tey, ñoo ngi fay bundxatal doxandéem yi, rawatina ñi ci seen der ñuul, te ñu bawoo Afrig. Muy lu mën a jur musiba ëllëg.
Lu defu waxu, walla dara du réer, waaye itam dara du làqu ba fàww ndax bés dina ñëw lépp leer nàññ.
Wax jooju lu wér la. Ndax ni réewum Dante soppeekoo jéggi na dayo. Yow mi xamul kuy Dante, nag, may ma tuuti ma dellusi ci jaar-jaaram. Dante ab bindkat bu ñu ràññee la ci addina sépp. Mu ngi juddu ci atum 1265 ci dëkk bu ñuy wax Firense fii ci Itali, génn addina ci atum 1321. Téereem bi gën a siiw moo di « La Divine Comédie ». Looloo tax ñuy faral di woowe Itali « dëkku Dante ».
Waaye kat, politigu Mattewo Salwini soppi na lool xar-kanamu dëkk bi ndax moom bëggatu fee gis ay doxandéem rawatina nit ku ñuul.
Tey, loolu lanu nar a waxtaane fii nu toog man ak sama xaritu benn-bakkan, Stefano, ak Baay Sidi, sama doomu-ndey, ku yágg a dëkk Milaŋ, def fi 20i at ak lu topp.
Matewo Salvini mooy jawriñ ji ñu dénk mbiri biir réew mi fii ciItali, jiite yit pàrti politig bii di La Lega. Waaye pexeem ak i xalaatam yépp ci lenn lañu jublu te mooy xeex doxandéem yi wàlliyaansi ci réewam. Nit ñu ñuul ñi nag la singali. Ba tax nadoomi Afrig yi amuñ fi jàmm ndax ci xoqtal leen la La Legadëkke ak ñoom. Jaratuñ fi dara. Lu waay xalaat ci lu ñaaw rekk teg leen ko. Kii di Salwini, daal, mu ngi nuy yakk guddi ak bëccëg lu mel ni xeme, askanu Itali yépp di ci dégg. Mu jaare fa may fit waa dëkkam ba ku jὀg rekk ne: “Nit ñu ñuul ñi sácc lañu, amuñu xam-xam, dañoo xayadi, ñoo yàq Itali te ñoom sax, ni ñuy takkee sunuy jigéen day tax seen deret ak sunu deret jaxasoo te loolu dara yéesu ko ! Mu dem sax ba ku bëgg a tiital sa doom danga ko naan ‘’boo deful ndànk ma woo nit ku ñuul ki ! “
Ku bëgg i firnde ci li nuy wax nii, doxantul biir anternet rawatina Facebook. Bés bu Yàlla sàkk Salwini def fa ay widewo, di ci xas doomi Afrig yi. Mu jaral ko nag fay xaalis bu bari ngir waa Facebook jàllale leen.
Yéene Matewo Salwini mooy fexe ba genn gaal gu yab ay doxandéem dootul jὀge Libi teersi Itali. Te yemul ci loolu ndax xeex na kurél yi tënkuwul ci nguur gi (ONG) ci péncum ndawi réew mi ba nga xam ni seen benn gaal ñemeetul a wallu ñiy lab ci géej gi diggante Libi ak Itali. Ndogal lu ni mel nag ay musiba rekk la jur. Ndax boobaak léegi ñiy faatu ci géej gi bari nañu lool. Te teewul bés bu nekk ay gaal yu ndaw fees dell ak i doomi Afrig teersi Lampedusa. Walla ONG yiy aar gaal yu mag yiy jòge Libi dikk ak mbooloo mu takku Kataña mbaa Lampedusaa.
Fi ñu tollu ni politigu Salwini xar na réew mi ñaar: ñi ànd ak moom, ak ñi féete ci kujje gi. Nguur gi ak kujje gi dëkke di dàggasante, xastante ak xuloo. Réewu tugal yépp di seetaan te defu ñu dara ngir aar doxandéem yi. Tugal gépp ànd bàyyi Itaali muy doxale ni mu ko neexe politigu imigarasyoηbi. Mbir la bu nuy nàqarlu lool.Li ci gën a yéeme, nag, mooy patt-pattaralu mbootayu xeet yi (ONU) te nu yaakaar ne moo ci waroon a njëkk wax.
Waaye lu am solo xew na ca Pari, fan yii weesu
Nu tëjeek xibaar bu am solo : démb ca Pari, péetum Frãs, Emanwel Makroŋak AŋselaaMerkel dajale nañu 14i jawriñ yi ñu dénk mbiru biir réew ci Ërób yépp ngir waxtaane imigarasyoη. Mu mel ni dañoo dégg sunuy tawat. Ndax ndaje moomu dina indiy coppite, delloosi xel yi ? Am nan ci yaakaar. Li ci teey xel rekk moo di ne li wax ciy bari yépp Salwini min ndeyu-mbill gi, dafa lànk ba tëdd ci naaj wi ne du bokk ci ndajem Pari moomu.
Waaye ci sunu gis-gis bu gàtt, pexe mënuta ñàkk ba fàww.
Baay Njaay ak Stefano Anselmo | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/tabaski-2023-xutba-ceerno-saydu-nuuru-taal/ | TABASKI 2023 : XUTBA CEERNO SAYDU NUURU TAAL
Ci alxamesu démb ji la ñu ëpp ci saa-senegaal yi tabaski. Ku ne tabaski, ne xutba. Te, xutbay imaam yi, dees na koy faral di xaaj ñaari pàcc. Bu ci njëkk bi, imaam yi dañu koy jagleel diine ji, jagleel beneen ñaareelu pàcc bi tolluwaayu réew mi, rawatina li ci fës. Noonii la fa deme at mii tam. Ceerno Saydu Nuuru Taal, ca xutbaam ba, ñaan na jàmm ci réew mi, sàkku ñuy amal waxtaan at mu nekk ci fànn yépp te soññ ndaw ñi ci moytoo yàq alalu réew mi.
Imaamu jumaay Omariyeŋ yi, Ceerno Saydu Nuuru Taal, ci alxames ji la julli. Ba muy xutba, ñaanal na Senegaal jàmm ak tawfeex. Waayeet, soññ na njiit yi ci ñuy jiital diisoo ci fànn yépp, ginnaaw bim rafetloo waxtaan wi Njiitu réew mi sumb. Dafa jàpp ne, waxtaan woowile, warees na ko amal at mu nekk te yaatal ko ba muy laal dund gépp.
Imaam Ceerno Saydu Nuuru Taal ñaawlu na tamit yëngu-yëngu yi toftalu woon ci ndaanug Usmaan Sonko ga ñeel layoom beek Aji Saar, bay nit ñu bari dee ci. Imaam bi nee, bakkan dafa tedd fa Yàlla, wareesu ko dog lu moy ci kow dëgg. Mu daldi tari aayab Alxuraan juy feddali waxam ji : « Ku rey benn bakkan, mel na ni àddina sépp nga rey. »
Kilifag taalibey Umar Fuutiyu Taal yi naqarlu na tamit yàq yi, toj yeek càcc gi àndoon ak yëngu-yëngal yooyee. Mu ne : « Islaam dafa araamal càcc ak jël alalu jàmbur. » Ni saa-senegaal yiy tojatee ak a yàqatey béréb, di taal ak a jafal ay daamar añs. Daf ko jaaxal, tiital ko lool. Ndax, Senegaal, léegi, dañu xër ci toj ak taal te, ciy waxam, « daan nañ wax ni, doomu Senegaal mënul sax rey ab mellentaan. » Kon, bu yeboo jàpp ne, Senegaalu démb, du Senegaalu tey. Teewul Imaam baa ngiy ñaaxati ndaw ñiy yàq, di leen xelal ak digal ci ñu bañ a déglu taalkati fitna yoy, ña nga bitim-réew toog, nekk ci seen jàmm. Daf ne :
« Buleen déglu ñi leen wax ngeen taal walla yàqate këri jàmbur yi walla ay bérébi liggéey. Ñaare, bitim-réew lañuy nekk, toog ci seen i saal yu nooy (…) te, ëllëg, yeen a aajowoo biis yeek saxaar gi. »
Ndigle laa ngoog. Nu xool ba xam dees na ko jëfe. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-teyu-doxandeemi-itali-yi/ | DÉMB AK TEYU DOXANDÉEMI ITALI YI
“Damay sànni ay kàddu yu néew ci waxtaan wi, jéem a joxe samay xalaat ci li nuy dund fii ci Itali.
Ci sama gis-gisu bopp, Móodu-Móodu yi agsi ci diggante atum 1980 ba 2000 wute nañu jëfin ak yeneen tukkikat yi tàmbalee tàbbi Itali ci atum 2000 ba tey jii.
Damay taxaw, léeg-léeg, seetlu, ngir def ay jàngat ci ñaari doxalin yu wute yooyu lool, seet tamit lan a ko waral, fan la lalu. Ndax, boo gëstoo bu baax, mbir mi dafa lay jaaxal.
Naka la mbir mi deme ? Ňaari melokaan, ňaari jikko yu wute lool ci ay doomi-adama yu bokk fi ňu jóge.
Waaye boo xoolee bu baax ñi jëkk a agsi jànguñu, walla boog seen njàng soriwul woon.
Dama koy seet ci sama maas gi. Dañoo jòge ci àll bi, walla jòge feneen ak feneen, jànguñu dara lu tax seen xalaat mën a sori.
Waaye ñàkkuñu woon cëslaay, amoon nañu tamit lu ñu gëm. Te boo ko de xool ci ñoom, Móodu yu jëkk yee fi taxawal ay daayira yu man a gindi mbokk yi ba kenn du gëlëm. Fakastalu, naam, am na, waaye Yàllaak daayira yee tax ba mag ñi fàttewuñu démb.
Jànguñu tubaab waaye mokkal nañu yeneeni làkk ba mën a xàll yoon wu leen di aar, di leen tee réer. Ndaxte, làkk wolof walla araab may na leen ñu xam fu ñuy teg seeni tànk ba bañ a saaraan. Te bi ñuy ñów ci réew mii gisuñu kenn ku leen tette waaye am nañu seen ngor ak seen diine, jàpp nañu ci ba taxaw fu dëgër. Ba tax kenn yóbbuwuleen ci weneen yoon wu doonul seen yoonu bopp. Kon tey, Móodu yu jëkk ya xam nañu fan lañ samp seeni tànk ba mën a téye seen aada ak seen ngor ak seen fulla. Loolu lépp am nay firnde ndaxte bu daayira yi nekkee fépp tey, xeer wu njëkk wi ñoom ñoo ko teg ba xale yi mujj a agsi mën cee jariñoo.
Doxalin wu ni mel ku yaafus walla ku ragal du ko sàmm ba ku la ca fekk, toppandoo la, mu indil ko tawféex. Xale yi topp ci yoon wi, nag, wax dëgg Yàlla gisuma ci kenn ku tarxiis ci kaw xollitu banaana.
Wax ji du gudd, dañu koy tënk.
Waaye maasi gone yu mujj yi, li leen sonal mooy ñàkk a mën a muñ. Jafe na lool jom ju tax ngay moytoo def looy réccu ëllëg. Walla bu la jamono naree lottal dinga ko mën a muñ ndax lu bari alal du la ko jaral. Li am solo mooy ngay xool bu baax sa juddu, di sàmm sa ngor, di bàyyi xel ci sa diine.
Xaley tey yi ànduñook dal, mënuñoo xaar. Te li koy indi mooy teel a bëgg am xaalis, yàkkamti koo am, sa lépp sotti léegi-léegi. Kenn xamatul luy taaxirlu.
Li ko waral mooy :
waa ji dafa wàcc Rom, dugg ci saxaar gi wutali Milaŋ, toog ba ci kanam mu ne ki mu dendal
-“Waaw, ndekete Itali am nab àll”
moroom mi ne ko :
“Noppil waay, loolu ëpp naa wax !’’
Waa ji tontu ko ne ko ;
“Aa, man kat damaa defe woon ni fii lépp ay taax la.”
Xam nga ni kii kay, am na mbetteel te dara xewagul. Fu amul àll, kenn du fa bay, te fu mbay amul, xamuma luñ fay dunde. Loolu moom, waxin la rekk.
Jamono ji ñu tollu, jafe-jafe yi bari nañ Itali waaye lépp dañu koy sante sunu boroom. Seneraasiyoŋ bu bees bi am na ciy jàmbaar waaye tamit bari na ci ñu réer. Du gaaw nag ñu defar seen réew.
Boo demee gaaru Milaŋ am na ñuy fanaan ci mbedd yi. Taxawaalu bi bari na lool, te xale yi mënuñoo yor seen bopp. Bu sedd bi ñëwee, xale yu bari dañuy tumuraanke. Tukki baax na waaye nit bala ngay jòg war ngaa xam fa nga jëm lan nga fay fekk.
Nun mag ñi war nañoo góor-góorlu ba teg xale yi ci yoon wu jub. Jàngal leen seen kàllaama, nàmpaatal leen ngir ñu xam seen cosaan. Loolu dina tax kenn du soppeeku ba topp tubaab yi ci seen melokaan.
Nun doomi Senegaal yi, dinanuy ànd dem ci daayira, dem julli jàkka waaye li nuy dimbalante ci sunu biir bariwul te bokk na ci li nu tax a des ginnaaw. Nit dina tollu diggante, ñòw ci biir mbooloo mu takku te fa mu tollu moom rekk a koy xam. Te dina rus a laaj, te ña mu fekki, bu ñu amul xelu jox ko walla dimbali ko, noonu lay jògee ca jataay ba, dellook aajo bu fajuwul.
Loolu dafay tax nit di gaaw a suux te du ca génn. Bu yàggee, kër ga mu luye sax dootu ko mën a fay. Boo dee ku am jom, dinga génn kër googu, bu booba mbedd mee lay for walla nga dem bay fanaan ci sa biir oto. Am na ku mu fi daloon, dafa mujj faatu ci sedd bi.
Li may jëkk a digale, mooy na nit kiy duggante ak mbokki senegaleem yi, saa yu ñu wootee mu jiitu fa, te ci daayira yi lañuy gën a faral di daje. Su ma nee daayira, nag, seetuma ci tarixaa bi mba beneen, daayira yépp laa yemale. Nekk ak say mbokk am na solo ndax bu saafarawul lépp tamit, mën naa saafara lu bari.
Nit ki fa ngay yeewoo, fa ngay faatoo. Kon, ci fànn yépp la jàppante am solo.
Li duuf ci nag wi, xejul ci cin li. Kon boog ba beneen jotaay.” | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/mbemestal-ci-jaar-jaaru-allaaji-omar-taal/ | MBËMËSTAL CI JAAR-JAARU ÀLLAAJI OMAR TAAL
Àllaaji Omar Taal mi juddu ci atum 1796 ca Fuuta, bokk na ci ñi siggil ba fàww nit ku ñuul ci lislaam. Nekkul woon rekk njiitul diine ak tariixa, wànte boroom xam-xam bu gëmoon der bu ñuul la, te fonk dénduw Afrig gépp.
Ginnaaw bi mu wedamloowee ay sëriñam, Àllaaji Omar feeñaloon na yeneen i kéemtaan ci daara ja mu nekkoon. Baayam boroom xam-xam la woon bu jànge Daaray Pir, doon daara ji gënoon a kowe ci jamono jooju. Yaayam it, Soxna Aadama Ayse, yaaram la woon bu nangoo séy te baax, fonk boroom këram ak wujjam. Abdul Karim Jàllo, ab sëriñ bu jànge Gànnaar, jële fa wirdu Tijaan, moo ko jëkk a jox wird wa. Ci lan fasante woon kóllëre ñoom ñaar.
Àllaaji Omar jaaroon na Misra, siggil fa der bu ñuul. Boroom xam-xami Misra xawoon nanu koo xeeb ngir wirgo deram, wànte bim jëflaanteek ñoom ba noppi, ñoom ñépp a luum.
Ba mu ajee Màkka la taseek Muhamadu Xaali nekk taalibeem ay weeri weer. Muhamadu Xaali natt ko ci bépp anam, def ko Xalifa ci ndigalu Seex Ahmad Tiijaani.
Àllaaji Omar Taal sumboon nay xare Senegaal ba Niseryaa ngir tuubloo ceddo yi, yaatal lislaam fépp ci Afrig sowu-jànt. Ci 1864 la ko noon yi ërtal mu dugg ci Degembeer ne fa mes.
Dees na wéy di fàttalikuy jalooreem ba fàww. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/aysata-taal-sall-jigeen-soppal-te-bul-woolu/ | AYSATA TAAL SÀLL : JIGÉEN SOPPAL TE BUL WÓOLU…?
Bés ba ma ko déggee mu naan kilifa diine yi dañ maa ñaan ma fekki Maki, laa ni ci sama xel : Aysata mii de, xéy-na dafa paree dem ba noppiy làmbaatu ba xam nu ko askan wiy gise ëllëg. Waaye man ci sama wàllu bopp de, masuma woon a xalaat ne Aysata Taal Sàll dina mas a bokki ci ñooñu doyadi bay xéy weddi seen bopp, dem ànd ak Maki, ndax rekk bëgg a tedd. Ndekete yóo…
Dëgg la, Senegaal, danoo miin politiseŋ yiy toxu, dem tag fu seen ceeb di gën a niin ba loolu safatul kenn. Waaye ndaw sii moom, ñépp mere nañ ko. Am na sax ñu naan moo yées ci ñiy yëngu ci làngu pólitig gi.
Aysata Taal Sàll dafa am fu ko askan wi mës a teg, muy fésal li mu gëm ciy kàddu yu leer nàññ te yit daan ko jëfe. Bërki-démboo-njaay rekk la fi ne xel dajul muy ànd ak waa nguur gi. Ñépp jàpp ni waxi gor la, doonte sax néew na li ñuy gis kuy pólitig ba noppiy jiital sa ngor.
Jigéen ju mel ni moom, jekk kaar, nex i ree, ay kàddoom dëggu, soo leen déggee ñu dugg la, mu jàng ba am i lijaasa yu réy, bokk fu baax niñ ko waxe, danga war a jombal sa bopp yenn yi. Rax-ci-dolli, foo ko fekkaan mu ngiy xeex par-parloo tey sotle néew-dooley réew mi. Ku mel nii, daa sopplu te ku ko sopp wàcc nga.
Tey, bu Aysata demee ba génn ba set wecc ci li mu waxoon, mbetteel la, gàcce la. Ñu bare la mbir mi ub seen bopp, am na sax ñu dem ba yaakaar ne Aysata Sàll ñoom rekk la tooñ, tooñul keneen.
Léegi nag, ñépp a ngi ciy teg seen bët : ci jigéeni réew mépp, amu ci kenn ku yoon may mu bokk ci joŋante 2019 bii, kenn ci ñoom muccul ci ‘’parenaas’’ yi ; kon, juróom yi des ci géew bi yépp ay góor lañu. Ndax Senegaal daa pareegul fal jigéen, teg ko ci boppu réew mi ? Loolu lay nirool. Ni Aysata Taal Sàll doxale, nag, day tax ñu yeyatiñu, nun jigéen ñi. Du ñàkk ñu jàpp ne dafa dëggal kàdduy Kocc Barma yu siiw yooyu te naqadee nangu : Jigéen soppal te bul wóolu… | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/ | TÀGGATOO
Roqi, ba beneen yoon.
Seetal ma lii rekk. Wax dëgg. Xool sama digganteek Yàlla te bañ a fen.
Waaw, yombul nga seeti sa rakk ak sa mag te say rongooñ tuuruwuñu. Walla dara yëngalul sa yaram.
Li ma yëg tey bi may tàggoo ak Roqi Yàlla rekk a ko xam. Bi ma koy nuyu, di wéy di dem, geestuwuma ndax xol bu fees ak yaram wuy rëg-rëgi. Ma xam ni deret fum la fekk daan la. Te doo ci mën dara. Li ci gën a yéeme mooy dangay mel ni ku ràkkaaju. Nga naan : « waaw feebar bi ma soppi nii nu mu tudd ? » Geneen kàddu jib, daldi feelu, ne : « feebaru mbokk moo la daan ba nga xalangu. » Bu ko defee, may seet naka laa koy fajee.
Doktoor mënu ci dara. Farmasi du jaay lu koy woyafal.
Roqi gënuma laa xam li may bind. Duma fi nekk di jekk-jekkal ak a làq-làqal. Damay jaar ci digg bi, toj yax bi. Su ma wóoroon ne tàggoo nii la mettee damay randal sama ñibbisi Itali. Waaye lu la bett, daan la ba nga mëq suuf si.
Lu waay di jàmbat, wolof njaay léebootina ko. Dëgg-dëgg sama rakku bopp ji lu ma wax rekk sama digganteek Yàlla laa ciy seet.
Weneen yoon su may ñëw Pari dama koy waaj bu baax. Julli ñaan Yàlla bañ a jooy, bañ a saalit. Guléet mu dal ma bésu tey. Àddina nii la. Ay jaar-jaar rekk la.
Abu Daraame, seede ma.
Baay NJAAY | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2-7-2023/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM (2/7/2023)
Dëmi-finaal U23
Ginnaaw-ëllëg, talaata 4i fan ci sulet , la dëmi-finaali joŋateb kuppe U23 di door fa Marog. Esipt ak Gine Konaakiri ñooy laale bu 17i waxtu ci ngoon jotee. Bu jeexee, Marog mi dalal po mi dana dajeek Mali ci ñaareelu dëmi-finaal bi.
Njortees na ne, joŋante yu neex la nar a doon. Nde, kenn ku ci nekk doo nangu sa moroom dóor la. Te yit, jamono jii, ekib yépp a defaru bu baax a baax. Rax-ci-dolli, ku ci nekk dafa bëgg a jël kub.
Cargalug Ànderes Iñestaa fa Sàppõ
Ginnaaw ba mu jugee Barcelone mi nga xam ne moom la ko ñépp xamee woon, ba ñépp jàppoon sax ni du fa mës a juge, Iñestaa, saa-espaañ bi, dafa demoon fee ca Sàppõ. Ca la demee ca këlëbu bu ñuy woowe Vissel Kobe, def na fa 5i at ci ren ba démb ci gaawu gi la doon amal joŋanteem bu mujju foofu. Na mu jooyee woon, keroog ba muy jóge Barça, noonee la jooyati ba ñu koy sargal cargal gu mag ci njeexitalu joŋante ba. Demoon nañu ba jaayukaayi tikke ya sax dafa mujje tëj ndax fowu bu fees dell. Muy lu mu yellool, ndax def na ci futbal lu nekk, jël ci itam lu nekk. Bokk na tay ci kuppekati digg yu gën a xereñ ci àddina ba sañoo lim ñett te waxoo turam.
Ndax dafay aj i dàllam am daf koy solaat tuuti, dara wóoragu ci, nañu ko déglu ba xam lum ci namm. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM
CAN-SENEGAAL : JOŊANTEB XARITOO
Ëllëg, ci altine ji, bu 18i waxtu jotee la Senegaal di daje ak Niseer ca fowu ba ca Jamñaajo. Muy joŋanteb xaritoo bees taxawal ngir waajalee ko CAN bi war a tàmbali 13i fan ci weer wii. Bu ñu noppee ci loolu, ndawi Senegaal yi di waajal ngir dem Koddiwaar.
ÀNDRE ONANA
Góolu Kamerun bi fekkijeegul i naataangoom ca seen waajtaay ya. Lu ko waral nag, moo di ne Manchester United dafay amal ab joŋante kub moom ak Wigan ëllëg ci altine ji, ak joŋanteb sàmpiyonaa moom ak Tottenham keroog 14i fan ci sãwiyee wii. Bu ci noppee lay daldi fekkiy moroomam ya. Loolu nag, waa Manchester United ñoo ci waxtaan ak waa Kamerun ba juboo ci.
CAF YOKK NA NDÀMPAAYU CAN BI
Senegaal mi jël CAN 2022 bi jotoon na lu tollu ci 2i tamñareet ak 997i tamndareet yu teg ci sunuy koppar. Ci wii yoon nag, waa CAF dañu daldi yokk yëf yi ba ci 4i tamñareet ak lu teg. Moy lu am solo lu ñépp rafetlu.
PAAP MATAAR SAAR FEDDALI NA PASAM
Doomu Senegaal ji moo ngi jóge woon Metz (Farãs) fekki woon Tottenham daaw. Ren nag, dafa wane xarañte ak jom ju ko yóbbe mu bokk ci ñay tàmbali saa su ne ca ekib ba. Ci loolu, mu jubook gaa yi daldi féddali pasam ca ekib ba ba atum 2030.
LÀMB JI
Ci altine jee weesu, di woon fan wu njëkk ci atum 2024 wii, la Móodu Lóo doon daje ak doomu Pikin jii di Booy Ñaŋ 2. Waaye, daf ko jaarati fa mu jaar ay magam. Doomu Pàrsel ji waneeti na mën bëreem ak faaydaam ci cëru buuru làmb ji mu yore. Niki mu daanee woon Ëmma Seen ak Aama Balde, noonu la daanaatee Booy Ñaŋ 2. Mu mel ni, léegi daan na ñees yaakaaroon ni mën nañu ko të ca biir Pikin. Fim ne nag, ñoo ngi seet kan ay jekk ci moom ngir boolee leen. Ay tur a ngi jib boobu ba léegi, ku ci nekk naan diw baax na ci moom, waaye jàppaguñ dara. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/daawuda-jaawara-faatu-nuy-fattaliku-senegambi/ | DAAWUDA JAAWARA FAATU, NUY FÀTTALIKU SENEGÀMBI
Daawuda Kayraba Jaawara, jiite woon fi réewum Gàmbi 1979 ba 1994, faatu na ci 27eelu ut 2019 bii ñu génn.
Mëneesul a wax Daawuda Jaawara te xel du dem ca lëkkaloo ga doxoon ci diggante ñaari réew yii di Senegaal ak Gàmbi te sabab ba doonoon ànd nekk benn réew, ñu duppe ko Senegàmbi.
Moone sax de Senegàmbi amoon na fi ay xarnu ci ginnaaw, ca jamonoy nootaange Tubaab yi (colonisation) ca atum 1763 jàpp 1783. Waaye Senegàmbi gi nuy wax ginnaaw bi nu jotee sunug jonn (indépendance) la. Ndax ñu ngi xaatim déggóo bi ko sos ci 17 desàmbar 1981. Ba ñu ca jógee it ça ngomblaani (assemblée nationale) ñaari réew yi ñu dëggal ko ci 29eelu desàmbar ca mooma at. Booba askanu réewu Senegaal a ngi tolluwoon 6 milyoŋi doomi-aadama, boob Gàmbi yemoo woon ak 600 junniy nit.
Ñaari réew yi doon ca roy Tansani (Tanzanie) mi juddu ginnaaw bi Tàngayika ak dun ya ñu duppe Sansibaar (archipel de Zanzibar), booloo doon benn. Booba it, ñu ngi doon bàyyi xel ca la taxoon lëkkaloob Senegaal ak Mali àntuwul woon.
Nuy wax nag ne yëf yi li ko sooke mooy la laarmeb Senegaal demee Gàmbi fekkoon ñu foqarti nguur ga.
Ginnaaw ba mu suqandikoo ci déggoo bu doxoon ci ñaari réew yi ca 18 feebarye 1965 ca Bànjul di péyu réewum Gàmbi, Njiitu réewu Senegaal Abdu Juuf jox larme bi ndigal ñu jéggi dig (frontière) wi dox ci diggante bi, daldi dugg biir Gàmbi. Sabab bi du woon lenn lu dul delloo Daawuda Jaawara ci boppu réew ma ginnaaw ba ko Kukoy Sàmba Saañaŋ, ab joolaa bu tolloon booba ci 28 at daanelee, fekkoon mu tukki ca Àngalteer doon teewe céytalug (le mariage) Saarl (Charles) ak Daayana (Diana).
Réewum Senegaal jële woon ci nag tiis wu réy ndax 24 ci ay soldaaram seen bakkan des na fa, 40 walla lu ko ëpp amoon ca ay gaañu-gaañu yu metti.
Loolu juroon coow fii ci Senegaal. Kujje politig ga booba Pds bu Ablaay Wàdd ak Rnd bu Séex Anta Jóob ñoo ci gënoon a am baat ci askan wi. Wuuteek Ablaay Wàdd, Séex Anta Jóob, ca janoo bu kurélu politigam amaloon ak taskati xibaar yi, yëkkati woon na ca kàddu yii : ” Li nu jàpp mooy ëllëgug Gàmbi dëgg-dëgg mooy booloo doon benn ak Senegaal”.
4eelu fanu Nowàmbar 1982 lañu siiwal Caytug (le gouvernement) Senegàmbi, mu tollu woon ci 9 nit (5 ci wàllu Senegaal, 4 ci wàllu Gàmbi).
Nii la Caytu gi tëdde woon :
Abdu Juuf : Njiitu Senegàmbi
Daawuda Jaawara : toftalu ci moom
Mustafaa Ñas : jëwriñ bi yore jokkalante ak bitim-réew
Lamin Kiti Jabaŋ : toftalu ci moom
Daawuda Sow : jëwriñ bi yor laarme bi
Medun Faal : jëwriñ bi yor kaaraange gi
Aliya E.W. Baaji : toftalu ci moom
Sériif Saykula Siisey
: jëwriñ bi yor koppar yi
Momodu S.K. Maaney : jëwriñ bi yor wàllu bitim-réew
Asan Sekk : jëwriñ bi yor dem beek dikk bi
Jibo Ka : jëwriñ bi yor xibaar ak jokkalante yi jaare ci xarala yi
Waaye xalam demoon na bay neex, buum ga dog. Lépp nag bokk ci jeexitali noot gi nu Tubaab yi nootoon.
Senegàmbi dox na ba ci atum 1989 yemook mbiicook mbaaloo doxoon ci diggante réewum Senegaal ak mu Gànnaar (Mauritanie) ba yeggoon ci ñaari réew yi di waaj a takk xare.
Kii di Daawuda Jaawara wone woon cag jeng akug far dëgg ci Uld Taaya mi jiite woon réewum Gànnaar. Yamu ca, mu pëtexlu ci njort lu mu amoon ne Senegaal xaw naa lompoñ, daldi xotti kayitu-déggo ba juróon Senegàmbi ca 1981, teg ca ne na Senegaal wàññi limub soldaaram ya ne ca mberaayu (territoire) Gàmbi.
Loola merloo woon Abdu Juuf lool ba tax ci 19 ut 1989, mu jële soldaari Senegaal yépp ca Gàmbi. Ndax Abdu Juuf ca la yem ?
Déedéet, ndax booy seet, ñaari fan ginnaaw bi Gànnaar ak Senegaal dogee bépp jëflànte bu doxoon seen diggante, Abdu Juuf dafa yëkkati ay kàddu yu jëm ci askanu Senegaal. Ci la leen xamal ne lii di Senegàmbi, tegandi nañu ko ci suuf.
Ba tey ci biir kàddu yooyee, Abdu Juuf a ngi naan : ” Lii di bennob Senegaal ak Gàmbi ci biir Senegàmbi amul benn ëllëg”. Mu daaneel ci kàddu yii: “paaka yi ci nootaakon yi tegoon sunu diggante nun doomi Afrig, daanaka ba léegi légét yaa ngi fi ba tey”.
5 at lañu ci teg, ci 1994, Yaayaa Jàmme, ab soldaar bu amoon booba 29 at, foqarti nguur ga ca Daawuda Jaawara, teg ca génne ko réew ma.
Nuy ñaanal Daawuda Kayraba Jaawara Yàlla jéggal ko, yërëm ko te xaare ko àjjanay Firdawsi. Amiin. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/kan-mooy-idiriisa-sekk/ | KAN MOOY… IDIRIISA SEKK ?
Maaraa la ko ay jegeñaaleem di woowe, doomi-réew mi naan ko Idi. Taskati xibaar yi ñoom, Ndaamal-Kajoor lañu koy dàkkentale. Idiriisa Sekk — mooy turam dëggëntaan — dib pólitiseŋ bu ñu ràññee ci Senegaal, Cees la fekk baax. Te sax, nekkoon na fa Meer ci diirub fukki at ak ñaar. Ci ginnaaw gi la doon njiitu Ndajem diiwaanu Cees ba nëgëni-sii.
Ci atum 1988 la Idiriisa Sekk ganesi làngu pólitig gi, waa Senegaal tàmbalee xàmmee xar-kanamam. Boobu, aw waxambaane la woon, amoon ñaar-fukki at ak juróom-ñeent doŋŋ. Mu xawoon a jaaxal nit ñi ndaxte, ci jamono yooyu, ay màgget rekk lees daan faral di gis ci làng gi. Foo fekkaan ngóor su gàtt soosu te ñuul, mi ngi topp ci ginnaaw Ablaay Wàdd. Dëkkoo- dëkk wër nañu ko, ñoom ñaar, di sàkku baatu askan wi ngir góor gi Wàdd toog ci jal bi. Laata ñu doon noppee laaj « Kii ku mu ? », mu yéem ñépp ndax xam-xamam ak xereñam. Jamono jooju la biddéewam feq, foo dem ci réew mi walla sax bitim-réew dégg turam.
Ci màrs 1990 la jëkk a doon jawriñ cig nguuru Senegaal. Mooy jamono ja Abdu Juuf yaatalee gornmaam, xajal ci kujje gi. Ñaari at yi jiitu woon loolu, nag, ay yëngu-yëngu yu metti amoon nañu Senegaal. Niñ koy waxe rekk : ginnaaw ay, jàmm. Idi la Juuf dénkoon njula mi.
Àddinay dox ba Ablaay Wàdd duma Abdu Juuf ci atum 2000, wuutu ko ci jal bi. Ci la tànne Idi, def ko bëkk-néegam. Ci weeru nowàmbar, atum 2002, nag, la ko “Góor-gi” tabb Njiitu jawriñ ji. Rax-ci-dolli, moo toppoon ci Ablaay Wàdd ci kilifteefu PDS.
Jaar-jaar boobu, nag, dug tandale. Ndax kat, bu dee wax dëgg rekk, fu mu mas a jaar, Idi def na fay jaloore yees koy màndargale. Bunu fàtte ni ngóor sii ganesi àddina ci atum 1959, ca Cees, dafa mas di raw ci kalaas yim jaar yépp, ba muy tuut-tànk ba ba muy am « bakaloryaa », ñu daan koy faral di ràññee yit ci « Concours général ». Noonu la ko jàppe woon itam, ci njàngum daara yu kawe yim defoon ca Pari ak ca Iniwérsite Princeton bu Amerig. Waaye mbirum Princeton moomu, lu mat a seetaat la ndax indi na fiy werante : gëstukat yu bare nee ñu lekool boobu, deful lu-dul jaar fa ni melax, bokk ciy lël yu ñakk solo te jëliwu fa benn lijaasa bu tax ñuy wax. Ci gàttal, ñoom jàpp nañ ni masul a jànge Princeton. Lu ci mënti am, warees na cee yokk ne xelam mu neex moomu, ay ustaasam a ko njëkk a seetlu ndax ba muy gone, ndongo-daara lu mënoon a jàng la. Foofu la jële dàkkentalu Maaraa biñ koy faral di woowe. Am na sax ñu jàpp ne ni muy def, di tariy aaya suy wax waxu pólitig, tiitar doŋŋ a ko ci duggal. Leneen lu ma seetlu ci jaar-jaaram moo di ne, ak li muy teel a dugg ci làngu pólitig gi yépp — fukki at ak juróom rekk la amoon — Idi jot naa liggéey ci Pirwe bi laata muy bokk ci nguur gi.
Mook i àndandoom am nañ lu ñu bàkkoo ndax nee ñu ba mu jiite jawriñ yi, yokkute dellusi woon na ci koom-koomu réew mi ba tax Club de Paris gën a wóolu Senegaal, abal ko xaalis bu baree-bari ; defaratoon nañu tamit lu xaw a tollook 1500 ci dëkk-dëkkaan yi, jaare ko cib naal bu Idy tudde woon Grappes de Convergence. Bu loolu weesoo, am na ñuy wax ne moom Idiriisa Sekk moo fekki woon Yaaya Jaame Gàmbi, fexe ba mu nangu ni jot na ñu lëkkale Senegaal ak Gàmbi : ci lañ tàmbalee liggéey ci pomu Farafeñe bi Maki Sàll ubbi keroog…
Ni ko ñépp xame, baayu Maki Sàll wattukat la woon waaye teewu koo jiite tey Senegaal. Baayu Idirisaa Sekk moom, da daan jaay fëgg-jaay màrse Cees waaye teewu ko fee nekk kilifa gu mag ci réew mi. Kon ñoom ñaar ñépp ay doomi baadoolo lañu te mënees na leen jàppe niy jàmbaar yu ñu war a naw ci wàll woowu ndax dañoo ñefe, fas-jom, ba génn ci.
Waaye nag, mu nel ni ndombog-tànk googu di Njiitu jawriñ ji du woon njiglaayu Idi. Tuuti rekk la toog, ay jiixi-jaaxa tàmbali ci digganteem ak Ablaay Wàdd mi mu jàppe woon ni baayam. La ko ca fekk neexul, ndax ba ñu tekkee ndombog-tànkam ci awril 2004, teg nañu koy tuuma, nëbb ko jant bi lu tolloog juróom-benni weer. Jiiñ nañ ko sàcc, ne dafa randal àlalu réew mi. Dem na ñu sax ba ne daa bëggoon a nasaxal kaaraange réew mi. Moom nag, masul a nangu tuuma yooyu ñu tegoon ci ndoddam te mujje gi àttekat bi setal na deram. Loolu am na, waaye ñu bare tey bëggoon nañoo xam fan la ngóor si masuta liggéey, daanaka, jële alalam ju dul jeex ji ! Su nit ñiy gise Idiriisa Sekk ni pólitiseŋ buy loxoom setul, looloo tax.
Ba mu jógee ci tolof-tolof yooyu la Idi féete ci kujje gi, taxawal pàrti bi mu duppe « Rewmi » (ñu waroon ko binde : Réew mi ) ngir jàmmaarlook nguuru Ablaay Wàdd. Fii, xel yépp dem ci Séex Aliyu Ndaw, bindkat bu mag bi jagleel ab kilib xareb ‘’Guy-Njulli’’ : Makoddu Faal ak Sàmba Lawbe Faal, Baay ak Doom, jàkkaarloo ca Kawóon… Wàdd ak Idi naka noonu. Pólitig moo mel noonu, gënatee gudd i tànk àddina ! Ca njeexitalu wote 2007 bi, naam Idiriisa Sekk rawul woon, waaye mëneesul a wax ne amu ca woon ndam. Ndax kat, ñi ko sànniloon kàrt tollu woon nañ ci limu 15%. Ku fàttaliku dooley Ablaay Wàdd ci jamono jooju, doonte sax amoon na lu bare lu ci wàññeeku woon, dinga gën a xam ne Idi defoon na jaloore. Ndege, fexe woon na ba raw pólitiseŋ yépp ba mu des Wàdd te ñu bare ci ñooñu yàggoon nañ lool ci géew bi.
Waaye Wolof Njaay nee na ku sa xel wër ñaari yoon gaañ la : muus ba mu ëpp baaxul. Mu mel ni looloo daloon Idi ba muy jaabante diggante këram ak Màkkaanu Wàdd, ku ci nekk di jéem a nax sa moroom, mu réere mbir xanaa ne ku la mag ëpp lay sagar. Ci lañ ko tàmbalee weddi, ñenn ñi sax mere ko lool mbaa ñu jéppi ko. Daan nañ faral di wax yit ne dafa beew te gaaw a xeebaate. Noonu la ñàkkee soppeem yu bare, ay farandoom dëddu ko, dooleem daldi wàññiku bu baax-a-baax. Li koy firndeel mooy wote yees amaloon ci atum 2012, te amu ca lu-dul limu 8% gën caa bare. Ki mébétam doon nekk ñeenteelu Njiitu Réewum Senegaal, waratee muñ ay at laata xelam di sañ a dem ci jal bi ko mas a tee nelaw…
Bi Maki Sàll faloo, Idiriisa Sekk àndoon naak moom ca njëlbéen ga, ay ñoñam bokkoon nañ ci gornmaa bi Maki Sàll njëkk a taxawal. Waaye yàggul dara ñu tàggoo, mu daldi dellu ci kujje gi. Mënees na ni kon amoon na nu mu jàngate jaar-jaaru boppam, gis ni war naa doxale neneen, maanaam jàpp njaamburam, dal-lu, maandu, dem fekki nit ñi ci dëkk-dëkkaan yi, waxtaan ak ñoom ci yar ak teggin. Ci gàttal, daa gënoon a fullaal aajoom, jox ko àqam yépp. Noonu la def ba askan wi xaw koo wóoluwaat, di ko may nopp. Wànte xawoon naa yàqule as lëf bi mu xéyee bés di méngale “Màkka” ak “Bàkka”, indi fiy werante yu mënoon a ëpp loxo.
Léegi nag, Idiriisa Sekk bokk na ci juróomi wutaakon yiy laaj boppu réew mi, ginnaaw bi mu amee ndam ci joŋante “parenaas” yi Maki Sàll sooke te ñu bare jàpp ne pexe la woon rekk ngir wàññi dooley kujje gi. Ci jamono yii nag, Idi neexut a dékku, ndax yaakaar gi mu dekkal ci xolu askan wi. Looloo waral ñenn ci kàngami kujje gi fekksi ko, ñu taxawal ag lëkkaloog làng ci wote 24 féewaryee biy dégmal. Li ñu ko dugge, nag, mooy jële fi Maki Sàll ; te jàpp nañu ne Idi daal a fi sës.
Loolu dina àntoom ? Bi mu jógee bërki-démb Tugal, Ablaay Wàdd nee na du jàppale Maki, du jàppale Idi te yit dina def kem-kàttanam ba kenn du fi wote. Askanu Senegaal a ci des : kan la nar a fal feek i fan ? Ndax Ndaamal-Kajoordina gàddu ndam li bii yoon ?
Looloo ko tax a samp ndëndam ci géew bi… Kon nanu xaar, li ci kanam rawul i gët.
Uséynu Béey | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/lamin-kamara-goneg-wurus-gi/ | LAMIN KAMARA, GONEG WURUS GI
Mamadu Lamin Kamara, jàppleen tur wi. Xareñte, dëgëraay, njaxlaf ak dégg-daaj la gaynde gu ndaw gi boole def. Moo tax, Mamadu Lamin Kamara, kenn la ci ndaw yi futbalu Senegaal yaakaar, ñu di ko bàyyi xel bu baax.
CHAN 2023 ba la njëkk a wone boppam, wone xareñteek njàmbaar gu mat sëkk. CAN U20 2023 bi ñëw, mu goneg Génération Foot ga woon delloo buum ca boy-boy ga. Dafa di sax, ginnaaw bi ko Senegaal jëlee, moom lees tabb kuppekat bi gën a ràññeeku, gën a xareñ ca joŋante ya. Lamin Kamara, nees ko tàmm a woowe, fa la jaare luqi bëti tubaabi FC Metz yi. Mu jóge Génération Foot (këlëbu Senegaal) mi ko tàggat ba tay jii, fekki këlëbu Farãs ba, Metz. Muy ndam lu réy ci moom. Yàlla bu cat topp.
Moom nag gan la fa. Waaye de, gan-ganluwul wenn yoon. Fullaay jaay daqaar, am déet ? Moom kay, dafa dem rekk bokk. Ndax, bi mu àgge foofu ca këlëb bi, dafa ñëw rekk tàmbali di dëyal fullaak fayda gu mat sëkk ak xareñte gi ko ñépp xame woon. Looloo tax ñu teel ko dugal ca biir ekib ba, muy dem, di bokk. Liy wane ni gan-ganluwul nag mooy keroog joŋante bam ñjëkk bokk, korneer yaak teg-dóor yépp moo ko doon dóor. Démb ci gaawu gi, mu def paas ci seen joŋanteb Ligue 2 bi amoon diggante Metz ak As Saint-Étienne, futbal lu réy.
Waaye nag, dafa jël ab “rouge”. Loolu di bénn xeer bu jam ñaari picc. Ndax, benn futbalkatu As Saint-Etienne a ko cokkaas, mu fayu, arbit yi gis ko. Njuumte la. Ndax jikkoy xale bu tàng deret kesee ko waral. Waaye, sikk amul ci ne dina gën a noot boppam, dëfal xolam ba lu ni mel bañ koo dalati.
Nu di ko ñaanal mu dem ba ñu koy dégg nag fu raw fu ñuy dégg i magam, niki ñoom Saajo Maane, Gànna Géy añs. Ndaxte, loolu ndamal réew mi la ak kuppeg Senegaal. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/waajtaayi-maggalug-tuubaa-2023/ | WAAJTAAYI MÀGGALUG TUUBAA 2023
Dëkk bu sell bii di Tuubaa sóobu na ci waajtaay yi ñeel màggalug 18 safar gu ren ji. Mu nekk bés bu màgg, di xew-xew bu siiw buy dajale mbooloo mu takkoo takku. Loolu tax ba kurél giy sàytu doxalin wi, amal ay ndaje ngir gën a ñoŋal xew-xew bile.
Fan yu néew rekk ñoo ci des laata bés biy teru. Kurél giy saytu waajtaayu màggal gi doon na amal um ndaje, ci talaatay démb ji, fa Tuubaa. Jëwriñu biir réew mi, Antuwaan Jom, ak yeneen i kilifa niki Sëriñ Basiiru Abdu Xaadr ma yore kàddu yoon wi, bokkoon nañ ci ndaje mi. Bokk na ci liñ jot a tënk, jafe-jafey ndoxum taw yi ak taa-taa yoy, warees na ci jël ay matukaay balaa muy gàllankoor xew-xew bi. Jot nañ cee def koppar yu tàkku sax ngir Tuubaa bokk ci dëkk yiy tàggook mbënn mi. Mu doon liggéey bu réy a réy, rawatina ci jamonoy nawet.
Leneen li ñu jot biral, bu ñu sukkandikoo ci kàdduy Antuwaan Jom, mooy ndoxum naan mi. Mu mel ni dalal na xel yi ci wàll woowu ginnaaw ba mu fésalee jumtukaay yu mag yi ñu teg ci loxoom. Muy 20i sëfaani ndox (camion-citerne) ndox yu réy. Benn bu ci nekk di def lu tollu ci 30 000iy liitar. Boo boolee 20i sëfaani ndox yépp, 600 000iy liitari ndox ngay am. Rax-ci-dolli, sëfaanu ndox gu nekk mën naa duy ñeenti yoon ci bés bi, muy lu jëwriñ ji biral. Mu nekk ay jumtukaay yu yees-péq yu Tuubaa war a daloo.
Mënees na tënk, wax ne waajtaayu màggalug Tuubaa gaa ngi ci njeexital li. La ñu ca nemmeeku ginnaaw at ya ko jiitu, mooy ay jumtukaay yu dolleeku ak ay liggéey yu mag ci jamonoy nawet ji mu tombeel. Loolu di firndeel yokkute gu réy gi muy àndal at mu nekk. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/atsu-deddu-na/ | ATSU DËDDU NA
Saa-Gana bi, Atsu (1992-2023), mujje na feeñ ginnaaw bi mu réere ci màbbiti taax ya daanu ci sababu rëng-rëng ba ca Tirkii. Ndeysaan, dañoo fekk mu dee. Moom nag, wurekat bu mag bu ñu ràññe la woon fii ci Afrig ak fa Tugal. Loolu nekk lu tiis ciy ñoñam, ciy naataangoom, waaye itam ciy soppeem rawatina waa Afrig yi. Keroog, 6i fan ci féewaryee 2023, la suuf sa yëngu woon diggante ñaari réew yii di Tirkii ak Siri, ñu baree bari ñàkke ci seen i bakkan.
Kiriscaan Atsu nag, Fc Porto la njëkkoon nekk, atum 2011. Mu jóge fa, dem Àngalteer. Nde, atum 2013 la jóge Fc Porto fekki Chelsea. Daanaka solul mayo Chelsea ndax jamonoy Móriñoo la fa dikk, jotul sax bokk ci benn joŋante, ñu abale ko. ci ñeenti këlëb lañ ko abale foofu ca Àngalteer, Everton, Bournemouth ak Newcastle. Kon yàgg na fa.
Ginnaaw loolu la génn tugal dem Araabi Sawdid am fa ñaari at ak këlëb bii di Al Raed. Xaatim ba leen lënkale woon ba mu jeexee la moom boppam, dem fële ca Tirkii fasante ak Hatayspor atum 2022. Foofu nag, ñeenti joŋante rekk la fa jot a am. Ñeenteel bi mooy keroog 5i féewaryee bii, ekibam doon daje ak Kasimpasa, nga xam ni benn bal ba ca duggoon moo ko dugal ba mu desee woon as tuut ca joŋante ba. Bal boobee taxoon ñu gañe joŋante ba ba noppi juroon mbégte gu rëy ca xoli soppey këlëb ba. Ca ëllëgu bés boobu la Yàlla Buur bi dikk ak ndogalam, suuf si xëy di yëngu yëngu yu metti foofu ca Tirkii ak Siri.
Moom Atsu, bañ ca tegeey fan yu néew, ay xibaar génnoon di xamle ni gis nañ ko ak ay gaañu-gaañu waaye deewul, ba xel yi tàmbali woon a dal. Xibaar boobu tax bu gaaw, ca ngoonu bés ba njaatigeem (agent) génn weddi loolu ni kenn gisul Atsu ba léegi. Bërki-démb ci gaawu bi nag, ba nu xëyee, moom njaatigeem bi bind xamle ni gis nañ ko ca biir bekkit ya mu ñàkk bakanam ci anam yu doywaar.
démb ku seetaan Sàmpiyonaa ya rawatina Àngalteer gis nga ekib ya doon ko sargal ak di ko mastawu njabootam ak àddina sépp. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/senegaal-seen-gaal-la-noom-am-sunu-gaal/ | SENEGAAL, SEEN GAAL LA, ÑOOM, AM SUNU GAAL… ?
Ku waaruwul ci doxinu miim réew, saw doxin dina la waari ëllëg. Ku yéemuwul ci jëmu gaal gii, teeru bi dina la yéemi. Bees fobulee ci joowu yi joow ngir soppi jëmu gaal gi, nóoxóor yu ñuul yi dinañ joow yóbbu la, yaak say mbokk ak i xarit, wànteer leen ci nóoxóor yu weex yi. Su booba dinga yëngal bopp, màttu, wiccax sa baaraam naan “su ma xamoon…” Waaye, réccu day fekk jëf wees. Ndax dingeen bàyyee gaal gi nóoxóor yu ñuul yi, ñu joow jëme nu ca sëg ya ? Senegaal, seen gaal la, ñoom, am sunu gaal… ?
Senegaal mooy réewum diine joo xam ni, ngëm dëgg feeñu fi fenn. Bëccëg, ku la ci ne “Yàlla nee na…”, “Yonent bi nee na…”, “Sëñ bi nee na…” bu la fenulee ngir naxee la ko yit, guddi mi ngiy njabarlu. Te li mu koy dugge mooy liggéey nawleem, yàq diggante yi, wut alal walla nguur, walla bëgg a siiw. Senegaal mooy réewum diine joo xam ni, bés bu nekk ñu tagg Yàlla, tagg Yonent bi, sargal Mag ñu baax ñi te kenn jéemul a roy ci ñoom. Senegaal a bariy jumaa, jàkka ak i taalibe, waaye Senegaal a bariy naaféq. Senegaal a bariy xew-xewi diine ak ñiy woote jàmm, waaye Senegaal a bariy waabajiiba. Moo ! Askan wu làmboo jikkoy naaféq ak melokaanu waabajiiba ban xeetu njiit la yeyoo ? Waaw, askan wu fase ngor, gàddaay dëgg, dëddu njub, suul fullaak faayda, ban xeetu njiit la yeyoo ? Ma laajati, askan wu sol mbubbu kàkkataar, dëkke fen, wor ak sàcc yan njiit la yelloo ? Yàlla ku maandu la. Moo tax it, lu waay rendi, ci say loxo lay nàcc. Nan dem rekk…
Senegaal ngay fekk askan wu dëkke ŋàññi ay njiitam, ci diirub juróom-ñaari at, bés bu nekk ñuy xultooka ñaxtu. Waaye, bés ñëw, bésub dibéer, askan woowu tànnaat yooyii njiit, tegaat leen ci boppu gaal gi, ñuy joow, jëme gaal gi fu leen neex. Nu dem rekk…
Senegaal bokk na ci ñaar-fukk ak juróomi réew yi gën a torox ci àddina si. Dëkkuwaay bu baax amu fi, luyaas bi metti na lool, xiif ak mar ne fi ràcc di bëgg a rey askan wi, ndóol waxi noppi, ku ci feebar dee ndax ñàkk loo fajoo walla loppitaan yu rafley jumtukaay. Njàng amatu fi waxatuma laak xéy, añs. Moone de, fii ngay fekk ay njiit yiy tabax i taax yu kowee-kowe, dëkk ciy kër yu réy te rafet lool, di dawal ay oto yu yànj ba jaaxal la. Ku ci ab yoo màtt, nga jël roppëlaan, naan yaa ngay fajooji Tugal. Rax-ci-dolli, seeni doom di jànge bitim-réew, ci daara yi gën a baax te siiw, ay daara yu ndongo ya xamul naka la ñuy waxe ‘’gereew’’. Njiit yooyu, ñooy jël alalu réew mi tayle ko Tubaab yi, di pasar-pasare xaalisu askan wi, di ci gundandaat ak a ndagarwale ca Soraanoo, Garaŋ-Teyaatar, làmb ja, ci yeneeni xew walla ciy mitiŋ. Bu wote jotee, ñu jël ci as tuut, di ko jënde askan wi nga xamante ne, lu jiin Njaag a, te mooy Njaag. Waaw, ndax sagaru junni, benn piisu waks bu fuyuŋ-fayaŋ, walla saaku ceeb jar na ngay jaay sa ngor ? Nga ne ma ? Sa alal la ?
Newuma la déet de, waaye nan demati rekk…
Senegaal mooy réew moo xam ne, Njiitu-réew mi lu ko neex def. Saa bu ko neexee mu jàpp kii walla kee, dëkke fi tëj ak jaay doole guddeek bëccëg. Bu wote jotee, askan wi tànnaat ko, teg ko ci jal bi. Ngan ne ma ? Naataange la la dig ? Walla la la digati…?
Ayca nu dem rekk …
Senegaal mooy réew moo xam ne, ndaw yi amuñu liggéey. Waaye, foo leen fekk ñoo ngiy werante ciy mbir yu ñàkk faayda : film, tiyaatar walla futbal. Doo gis benn ndaw, muy góor walla jigéen, bu nangoo yedd boppam, soppi jikkoom. Janq jaa ngiy mébét doon léttkat, ñawkat, woykat walla fecckat. Ñi ci yées, dem bay cagatu naan dañuy daan seen doole. Waxambaane bi moom, di ñefe ngir doon mbër walla futbalkat. Ñi ci gën a ñàkk faayda ñoom, rusuñu doon i woykat, fecckat, tëggkati sabar wallay taasukat. Ñi ci yées, di dogaale jaamu Yàlla yi, ngir nangu seen alal. Nga ne ma ? Tëgg ak fecc ci sunu aada la bokk ? Waaw, kon daal tëgg ak fecc a nuy jëme kanam ?
Waaye baax na, nan demati rekk…
Senegaal mooy réew moo xam ne, làkku jaambur lañ fiy jàngale ak démbu doxandéem. Kenn jàngalul xale yi ngir ñu mënal seen bopp, gëm seen bopp, moom seen bopp. Waaye, dañ leen di jàngal ngir ñu doon i jaam yuy tàllal loxo. Nga ne ma ? Sunuy làmmiñ réew mënunu cee tekkee ? Yaakaaroo ne ki la wax loolu dafa laa yab ? Yaakaar nga ne teg na la nit Njaay ?
Waaye nu dox dem rekk…
Senegaal mooy réew mu bari alal te askan wi jariñoowu ko ; réew mu bariy àttekat te amul yoon ; réew mu ñépp bokk, ay sàmba-allaar aakimoo ko di ci def lu leen neex. Senegaal mooy réew mi nga xam ne, foo dem ñu ni la “waa réew moomoo neex xel ! Ñoom kay, kuy wut xalaat bu rafet, gaawal ganeji fa.” Nga ne ma ? Dëgg la ! Dëgg piir sax ! Fii daal, ku ëpp sa moroom doole wan ko ko. Moo tax it, ku yeboo jéem a muus, di jëfandikoo sam xel ngir jël sa wàll ci toŋ-toŋ bi. Loolu doŋŋ la, nag. Bu nu kenn rey ak wax ju bare. Politiseŋ yi loolu lañu nànd bu yàgg, kon lu may tere def ni ñoom ?
Léegi nag, àgg nanu.
Nanu wax ak ndaw yi. Ndax kat, ëllëg, seen ëllëg la. Ndax warees naa seetaan lii di wéy ? Senegaal, seen gaal la,ñoom, am sunu gaal ? Li wér te wóor mooy, sunu gaal gaa ngi daw ni gaalu dof ci géej gu sàmbaraax. Jot na askan wi yeewu, nangu joowu yi ngir jubbanti gaal gi. Ndax kat, gaalu dof du teer, walla bu teeree yit, teeri ci loxoy nóoxóor.
Paap Aali Jàllo | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/tabaski-2023-xutba-serin-maahi-nas/ | TABASKI 2023 : XUTBA SËRIÑ MAAHI ÑAS
Ci alxamesu démb ji la ñu ëpp ci saa-senegaal yi tabaski. Ku ne tabaski, ne xutba. Te, xutbay imaam yi, dees na koy faral di xaaj ñaari pàcc. Bu ci njëkk bi, imaam yi dañu koy jagleel diine ji, jagleel beneen ñaareelu pàcc bi tolluwaayu réew mi, rawatina li ci fës. Xalifa ñaseen yi, Sëriñ Maahi Ñas, woote na jàmm ak ndal ci Senegaal.
Sëriñ Maahi Ñas, moom, jàmm lay sàkku ci réew mi, di ko ñaan te di ci woo ñépp. Nde, ci gis-gisam, jàmm mooy indi ndal giy tax koom-koom gi mën a yokku, réew mi naat. Ginnaaw bi mu jiitee ñaari ràkkay tabaski yi, toftal na xutba bob, jóo na ci waa réew mépp, muy njiit yi ak ñi ñu jiite yépp, ñu joxante loxo, jàppoo, bennoo ngir saxal jàmm ci Senegaal, suuxat ko ngir suqali réew mi. Xalif bi ne :
« Am réew, na askan wa mel rekk lay mel. Bu askan wa nangoo topp ci ginnaaw nguur gog, tàllal na loxo askanam ngir dimbali ko, yar ko, tàggat ko, xirtal ko ba maxejj bu nekk di gis boppam ci li nguur giy doxal, bu boobaa maxejj bi dina soppi aw doxiinam ci lu baax. »
Noonu, Sëriñ Maahi Ñas xelal na ndaw ñi tamit, xamal leen ne dañu war a waajal seen ëllëg. Nde, ñoom ñooy nekki kilifay ëllëg.
« Nanguleen a jàng, jikkowooleen jikko yu baax. Ndaxte, benn maxejj warut a xeeb jëfam ci liy tabax réew mi. Maxejj bu baax ak Njiitu réewam ñoo bokk ay àq ak i yelleef. »
Kilifa gi dafa jeexalee xutbaam ci fàttali ne, Senegaal benn bopp la, kenn mënu ko xar ñaar. Moo tax, ciy digleem, ñu war a sàmm kàddu yi, tànn yi ci gën yiy sabab jàmm di indi ndal ci réew mi.
« Nun ci sunu wàllu bopp, jéemunoo lor kenn, te baal nanu képp ku nu tooñ. Jàppalunu kenn dara. Yaraate ak jàngale rekk ñooy sunuy itte. Te, danuy jéem a def lu baax. »
Ay ñaan la tëjeey waxam, rawatina ngir bennoog way-pólitig yi. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/lu-nuy-xaar-ci-jangale-lammini-reew-mi/ | LU ÑUY XAAR CI JÀNGALE LÀMMIÑI RÉEW MI ?
Bi Senegaal moomee boppam ba tey, bare na ay nguur yu fi jaar ak seen i dige ñeel làmmiñi réew mi. Am na ci sax ñu fi jot a taxawal ay naal, amal i gëstu ak ay jax yu dul jeex, ngir xool naka lees mën a def ba boole sóninkeek wolof ci njàng mi. Waaye, li ko dale ci Lewópóol Sedaar Seŋoor ba ci Maki Sàll, jaare ko ci Abdu Juuf ak Abdulaay Wàdd, kenn jëmmëlu ci naal yooyu, doonte sax yéene baa ngi fi woon. Ba nëgëni-sii, làkki doxandéem yi lañuy jàng, di leen jàngale ci sunu daara yi.
Moone de, bare na ay xeltukat yu ñu ràññee yu biral ne, am réew su bëggee jëm kanam fàww mu yar askanam ca ba muy tuut-tànk, fexe ba njàngam mucc ayib. Rax-ci-dolli, njàng moomu, dees ko war a def ci làmmiñu walla ci làmmiñi askan woowu. Boroom xam-xam yi ma tudd, indi nañu ay firnde yu bare yuy wone ni xale bi, ci li mu nàmp lay gën a gaaw a mokkale li ñu koy jàngal, mu amal ko yit njariñ cig dundam. Ci misaal, ci lay gën a gaaw a mën dawal ak xayma. Te, nag, dawal ak xayma yi nga xam ni ñooy cëslaayu njàng, gone yi dañu ciy faral di lajj. Loolu rekk waroon naa tax nu jël i matuwaay ngir dugal sunuy làmmiñ ci lekkool bi.
Ay gëstukat wone nañu ci seen i ngirtey liggéey ni, 100 ndongo yoo jël ci ñetti ati lekkool yu jëkk yi, 75 yi mënuñoo dawal walla bind bu baax. Yemul foofu, ndax nee nañu ci 230 alfunniy (milyoŋi) xale yiy dal ci daara yi, du kenn ku ciy mën a dawal walla bind ci at yu njëkk yi. Kon, pexe mi mooy ku nekk di jàng ci làmmiñ wi nga nàmp. Warees na jëmmal naal yi te bañ a yem ci wax ji kese.
Li jaaxal ñépp, nag, mooy ngirte yu am solo yu tukkee ci daaray-jax yi (classes télévisuelles, testes du bilinguisme). Bir na ne ndongo yiy tàmbalee jàng ci seen làmmiñ laata ñuy jàng weneen làkk, ñooy gën a aay fuuf ñeneen ñiy tàmbalee jàng ci tubaab. Moo, kon lu nguur giy xaar ci yoonal njàngum làmmiñi réew mi ci daara yi ? Ana ban walla yan téq-téq ñoo nu tee jàngale sunuy làmmiñ ? Ndax bëgg-bëgg beek pastéef bee fi nekkul ? Walla dafa am ay réew walla ay kurél yuy gàntal naal yi ?
Mu mel ni nguur gi dese naa am pastéef ñeel njàngum làmmiñi réew mi ; waaye tamit, nootkat ba woon, Frãs, ak yenn ci kurél yiy lebal réew mi xaalis, bokk nañu ci ñiy tee naal yi àntu. Waaw. Wolof dafa ne, ku la abal i bët, fu ko neex ngay xool. Li mbir mi di tekki moo di ne ba léegi moomagunu sunu bopp. Ndaxte, bu dee amunu sax sañ-sañu taxawal xeetu njàng mi gën ci nun, méngook sunuy aada ak sunu cosaan te di nu jural yokkute, dafa fekk mënagunoo dogalal sunu bopp ci ñaari fànn yii di politig ak koom-koom. Bu fa yemoon sax mu tane, waaye doomi-réew mi ci seen bopp, ñu ci bare dañoo jàpp ni joolaa, pulaar, séeréer, wolof añs, dañ nuy delloo ginnaaw. Te, nag, ku xeeb sa cosaan ñu xeeble la ko.
Leeg-leeg danga naan Tubaab bi dafa noo jam naani ndax ni nootaangeem di wéye ba tey jii ci xel yi. Moo nu gëmloo woon ne sunuy aadaa nu tee nite te feek sànniwuñ leen ca xaj, dunu leen dab mukk, ñoom Tubaab yi. Dañu doon wax lu leen neex rekk ndax mën a kàcc weesuwul naan sunuy làmmiñ mëneesu cee sàkku xam-xam ba ciy séentu naataange !
Boroom xam-xam bu mel ni Séex Anta Jóob weddi na wax jooju ba noppi indi ay firnde yuy wone ni làkki doxandéem yi gënuñu benn yoon sunuy làmmiñ. Ci ginnaaw gi, am na ay gëstukat yu topp ciy tànkam, di liggéey ci nëwum làmmiñi réew mi. Ràññees na ci Aram Faal, Saŋ-Léwópóol Juuf, Mamadu Siise ak Cerno Siise.
Waaye ba tey njaw des naw xambin.
Fi mu ne nii, amatunu jawriñ bu féetewoo lépp lu aju ci làmmiñi réew mi. Amul genn kurél guy saytu ak a yoonal nees leen war a binde. Lu neex waay mu bind ! Moo tax ñu bariy jaawatle ba léegi joŋeak « jongue », muy lu reelu lool, sax.
Misaal yi bare nañu, mëneesu fee lim lépp. Li mat a xam ba tey rekk mooy ni xamagunu sunu bopp, nattagunu sunu dayo. Looloo tax amunu benn jubluwaay. Lu nu teree dellu ci sunu cosaan, gën a fonk li nu fi Maam bàyyil ? Waaw. Soo xamatul foo jëm, tee ngaa dellu fa nga jóge ! Warees na xam ni, toppandoo duñ tax a jëm kanam ndax ni ko wolof Njaay di waxe : “Ku wacc sa and, and boo dem fekk ca boroom”. Ma jox Séex Anta Jóob mu daaneel : “làkku jaambur, lu mu neex neex, mëneesu koo macc ba ciy tàqamtiku.” Waay-waay, nanu jàngale làmmiñi Senegaal yi, muy neex gone yi ba ñuy tàqamtiku, gënatee sawar ci sàkku xam-xam, ñuy joow, jëmale gaal gi kanam ! | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/ikibu-futbal-bu-senegaal-ku-nepp-di-xaar-nga-war-a-mene-fu-nekk/ | Ikibu Futbal bu Senegaal : Ku ñépp di xaar nga war a mëne fu nekk
Keroog ci talaata ji lees tàmbali ñaareelu bëccëgu joŋantey bokkadil CAN 2023. Ikibu Senegaal bi doon ci jàmmaarlook ikibu Ruwàndaa bi ko doon dalale ci Estaad Meetar Abdulaay Wàdd bu Jamñaajo. Mu doonoon joŋante bu metti te wuuteek bu gaawu, bañ dumawee Beneŋ 3i bii ci benn. Bi joŋante bi di waaj a jeex la kii di Saajo Maane, goneg Bàmbaali gi, dugal penaatii. Senegaal gàddu ndam li. Ñuy ñaari joŋante yu tegaloo yuy fàttali fi ikibu Senegaal bi tollu ci làngug futbal gi ak lees di xaar ci moom.
Ñetti weer ci ginnaaw la Senegaal doonoon sàmpiyoŋu Afrig 2021. Mu sóobooti xaat ci joñante bi. Mboolem réewi Afrig yi, ku ci nekk bëgg koo wuutu, te Senegaal ci boppam war koo mën a jëlaat. Lii tax na ba saa buy joŋante, way-faram (supporters) yi di xaar ndam ak a yaakaar mu doon ndam lu réy. Bokk na ci li ko waral, futbalkat yi ikib bi dajale dañoo siiw lool te am i tur. Daanaka ñu ci ëpp, ci sàmpiyonaa yi ëpp doole ci àddina si lañuy futbal. Loolu tax na ba buñ ndulliwul ki ñuy jàmmaarlool boole ci futbal bu rafet, du neex way-faram yi, walla sax am ñu leen di gàkkal.
Rax-ci-dolli, du way-fari Senegaal yi rekk ñooy xaar foofu ikib bi. Dem na ba tàggatkatu gaynde yi walla ñi koy gunge loolu dafa ub seeniy bopp. Loolu dees na ko dégge ci kàddu yi Elaas Juuf yékkati ci ñaari ndam yii ñu tegale : “ ñaari joŋante, ñaari ndam mooy lu jaar yoon. Ndaxte, Senegaal ñépp a ko teg i bët tey jii ci CAN bi. Kon dañoo war a dawal ni ñi mën ci Afrig, niki sàmpiyõwiy Afrig.” Mu mel ni yeneen réew yi xam nañ loolu te nangu ko ngir gën a mën a yokk seen waajtaay. Bees nangoo kàddu yi bawoo ci Karlos Alos, tàggatkatu ikibu Ruwàndaa, Senegaal “bokk na ci fukki ikib yi gën a baax ci àddina si”.
Tege yii tax nañ ba gaynde Senegaal yi xam ni seenub benn joŋante dootul a yomb. Te itam loolu feeñ na bu baax ci seen xar-kanam. Bu nu sukkandikoo ci Kàdduy Séexu Kuyaate, dinañ gis ni guney Aliyu Siise yi ñi ngi wéy di mottaliku ci anam yu bare : “ léegi ikib bun dajeel dafay metti. Nun nooy sàmpiyõ Afrig. Te sàmpiyõ Afrig, jàmmarloowam yépp gañ-jël (finale) la… Boo xoolee joŋante bi, bun ko amaloon ñaar ba ñetti at ci ginnaaw doon nan ci témboo walla sax nu ñàkk ko”. Lii nag mooy yaa fi mën, bu dee ndam it, sas la wu réy. Ndax ku ñépp di xaar nga war a mëne fu nekk. Mu mel ni xam giñ xam fiñ leen xaare, baax na ci Saajo Maane ak i ñoñam. Jural na leen làmbook mat gu leen di tax a bëcciku (se décharger) ak a xam nees war a amee ndam saa su nekk ak lum jafe-jafe. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/masaalikul-jinaan-soppi-na-langu-politig-gi/ | WÀDD-MAKI : GINNAAW AY…SOPPI ?
Keroog, àjjuma 27eelufan ci weeru sàttumbar, atum 2019,ba ñuy ubbi Masaalikul Jinaan, jullit yépp a bégoon, rawatina murid yi. Bégoon nañ ba, foo nattoon seen mbégte rekk, mu romb koy dem. Ndaxte, kat, wëliis li jumaa ji doon ab jaamukaayu Yàlla, Sunu Boroom, Masaalikul Jinaan dafa dib sag ci mboolem jullit ngireeni mu réye te yànj, kaar. Moom kay, guléet ñu gis fi jumaa ju ni mel ci Afrig sowu-jant ba mu daj. Te, nag, lépp li ko jëmmal mi ngi jóge ci ñaqi doomi réew mi, ci seeni xalaat, ci seen alal ak ci seen doole. Bu amee yit ay doxandéem yu ci dugal seen loxo, bariwuñu, te fay nañ leen liñ ci liggéey ba mu mat sëkk. Li ci ëpp, nag, Tuuba la jóge.
Waaye ubbite boobu, daa am leneen lu mu jur ci wàllu politig, mu di juboob Abdulaay Wàdd mi fi jiite woon réew mi ak Maki Sàll mi toog tey ci jal bi.
Kenn umplewul li dox ci diggante ñaar ñooñu, muy diggante baay ak doom. Ñu ngiy fàttaliku ba Maki Sàll di génn PDS, ginnaaw ba ñu ko fa bunduxutaalee ndax joteem ak Karim Wàdd. Mu jóge fa taxawal parteem tudde ko APR, utali nit ñi, bokk ca joŋanteb atum 2012 ngir doon ñeenteelu njiitu réewum Senegaal. Ba Maki Sàll gàddoo ndam loolu ba léegi nag, diggante ñaari politiseŋ yi daanaka at mu jàll mu gën a ñagas. Noonu, ba Maki jàpplu doomu Ablaay Wàdd ji, Karim Wàdd, yoon daldi koy nëbb jant bi ñetti at. Ci mujjantal gi, ñu génne ko, gàddaayloo ko ngir rekk mu bañatee a bokk cib joŋanteb fii ci Senegaal. Ay at a ngi nii mu ne réewum Kataar, ñibbisi të ko.
Digganteb ñaari kilifa yooyu nag, ku ne wax na ci ngir defaraat koo, rawatina njiiti diine yi, ñu gën cee ràññee Xalifay Murid yi fi jot a jaar. Ñenn ci njiiti réewi Afrig yi sax, ku ci mel ni Alfa Konde, xar nañ ci seen tànki tubéy ; waaye taxul diggante bi defaru bay rattax.
Loolu lépp tax na, keroog ca ubbiteb Masaalikul Jinaan, kenn gëmewul woon maslaa yeek jàppante loxo yeek àndandoo bi ñaari kilifa yooyu nekkee, di saafoonte, di digante gisewaat ci ni mu gën a gaawe. Ca dëgg-dëgg, nit ñi yàgg nañoo ñaan lu ni mel am, waaye teewuleen woon a waaru.
Dëgg la, politiseŋ yi, dañu bariy feem, waaye nag, àndandoo Ablaay Wàdd beek Maki Sàll keroog, ñu dem bay lëngoo, ñépp la dawloo seen yaram, tooyal seen xol. Ci sunu gis-gis bu gàtt daal, mënees naa am yaakaar ni juboo dëgg am na. Te nag, juboowu ñaari kàngam yooyu, war naa jur déggoo bu wóor fu bennoo mën a lalu, ba tax ñu mën jàpp ne, la jógge ca Masaalikul Jinaan lu taxaw la.
Déggoo boobu, waxtaanu politig la, te ëllëgu Karim Wàdd – maanaam delluseem ak nekkinam ci réew mi, ak itam taxawaayam ci joŋante yiy ñëw – mooy li ci gën a soxal Wàdd.
Su loolu lépp àntoo dinañu mën a wax ne Masaalikul Jinaan, ginnaaw li mu jur ci diine ji, di lu am a am solo, jur na it jàmm ak tawféex ci réew mi, tax na politiseŋ yi dakkal seen xulook seen ŋaayoo.
Waaye bu demewul noonu day rekk doon yaakaar ju tasati te ñépp dinañ ko naqarlu. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/jinaabo-jambaaru-seleki-ba-ca-sigicoor/ | JIÑAABO, JÀMBAARU SELEKI BA CA SIGICOOR
Boo demee ca diiwaanu Sigicoor, dinga fa fekk liise bees duppe Jiñaabo. Waaye, aka néew nit ñi xam kan mooy Jiñaabo !
Njàmbaar, fit ak ngor ñooy jikko yiy màndargaal Jiñaabo. Dafa di, Jiñaabo ab dàkkental la rekk. Turam dëggantaan mooy Jinoyeb Baaji. Moom Jinoyeb, walla Jiñaabo, as ndawu joolaa la woon, amoon fulla lool, gëmoon askanam, daan ko xeexal ba mujje cee ñàkk bakkanam. Jiñaabo mi ngi juddu ci atum 1850, ñu faat ko ci atum 1906, weeru me, fekk mi ngi tolloon ci 56i at. Li ñépp di fàttaliku, moo di ne ay jëfam ndawuñu woon, turam sooyul te nettaleem ñaawul. Ndege, Jiñaabo ci toolu-xare la daanu ! Te kenn newu ko kaay nu xeex, kenn jàmmarloowul ak moom, ñuy dóorante ba moom mu dee. Loolu lépp dara amu ci. Ab buqat, xonq-nopp bu bon, moo taxaw fale, daldi koy fetal, keroog xare Seleki. Diggante Seleki ak Sigicoor, 25i kilomeetar rekk la.
Ki ko faat, nag, doomu Frãs la, nootkat bi, bóomkatu jàmbaar bi.
Ñetti at laata Jiñaabo di ganesi àddina la coow li tàmbali. Ndaxte, ci atum 1886 la leen nguurug Frãs tàmbalee cokkaas, di leen tooñ ak a bunduxataal ba ci seen biir dëkk. Ñu ni déet-a-waay, soldaari Frãs yi di leen sànni ay ndell ak a taal jëppit seeni dëkkuwaay. Dañoo mujj a toxu, ndax seen lépp a yàqu woon, amatuñu woon sax fuñ fanaan.
Ba ci ndoorteelu 20eeluxarnu bi, Farañse yi, jaare ko ci seen ndaw lu leen fa toogaloon, dañoo jàppoon ni Seleki seen moomeelu bopp la woon. Looloo taxoon ñu daan fayloo waa dëkk ba, rawatina baykati ceeb ya, ay juuti ci seenum mbay. Waaye, askanu Seleki mësuñoo bàyyeeku, mësuñoo nangu ku leen di xoqtal, di leen jaay doole ak di aakimoo seen alal. Moo waraloon ndawu Frãs la fa nekkoon, xawoon a ragal Seleki ndax dafa jàppoon ni kaaraangeem desoon na, rawatina ba nit ña fay yeewoo taxawee temm, ne dee duñ fay lempo. Ci meenu jàmbaar yooyu la Jiñaabo nàmpe, kon mënul woon doon lu dul bañkat.
Xareb Seleki bi Jiñaabo ñàkke bakkanam, ci njiiteefu soldaaru Frãs bu doon wuyoo ci turu Lauque la ame. Moo santaane woon cong gi, jiite woon ko yit. Deewub Jiñaabo bi, nag, xawoon na indi jiixi-jaaxa ci xeli waa Seleki yi. Ndege, Jiñaabo du woon ndaw ni yeneen ndaw yi. Dafa amoon lu mu àndal, di woon sëriñ bu mag, amoon i gàllaaj. Kenn mësul woon a foog ne ab balu fetal mënoon na ci moom dara. Ñépp a jàppoon ni dafa tul. Waaye, jaam ak pexeem, Yàllaak ndogalam. Li am ba des mooy ne, xibaaru deewam bi yéemoon na lool waa tund woowee ; daanaka ñu bare nanguwuñ koo woon gëm.
Jiñaabo jotoon naa am doom ju tuddoon Sitaayóbo Baseen. Bi muy faatu, doom jaa ngi amoon 8i at. Bi Tubaab yi reyee baayam, waa dëkk bi dañ koo rawale, yóbbu ko ca dëkk buñ naan Ëllubaliir. Li ñu ko dugge woon mooy bañ Tubaab bi dugal ko ci gaal yóbbu Ndar-Géej, ni mu ko tàmmoon a defe ak doomi buur yi, mu bindu ‘’École des Fils de Chefs’’, ca daara jañ leen jagleeloon.
Nataal bi : ndey-joor jàpp càmmoñ, sëtu Jiñaabo ak Tete Jaaju*.
*Tete Jaajukilifa aada la woon ci Sigicoor ; tuddees na ko jenn daara ca diiwaan boobu. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/senegaal-yokk-cere-dolli-neex/ | SENEGAAL, YOKK CERE, DOLLI ÑEEX !
Sàmpiyonaa yi jeex nañu. Ekibi dëkk yi ñooy futbal jamono jii. Ñii di futbal ay matsi xaritoo, ñee di waajal seen i joŋante yi ñu dégmal. Fii ci Afrig nag, ekib yaa ngi amal ay joŋantey xaritoo ngir nattandi seen taxawaay ak seen doole, nekk ci waajtaayi cu joŋanteb kuppeg Afrig bi war a am ci atum 2024. Ba tax na, ekibu Senegaal bi demoon na fekki bu Benee ca dëkkam. Mu nekkoon juróomeelu joŋanteb kippug L gi. Senegaal gi nga xam ne, moo jëloon raaya ji ca kuppeg Afrig 2022 ga, ay soppeem ñoo ngi koy xaar mu ñëwaat wane boppam, waaye tamit ay nawleem ñoo ngi koy xaar ngir kar ko, xañ ko ko bile yoon.
Démb ci gaawu gi, mu doon amal ndaje ak ekib bii di Benee. Waaye, dafa mel ni xel dalagul nag. Ndaxte, li gaynde yi wone démb dafa des bees ko nattalee ak lees di xaar ci ñoom. Seen futbal bi des na lool, rawatina kaw gi. Foofu moom, war nañu toog, waxtaan, xool, xoolat ba xam lu fay ayib bi. Dugal gi moo des ba tay. Te, li jaaxal ñu bari mooy ni, bu ataakã Senegaal yi nekkee fa seen i këlëb, dañuy dugal rekk. Waaye, bu dee Senegaal lañ futbalsi, day xaw a mel ni dañu yeew seen tànk yi. Ku ci jàkkaarloo ak caax yi, bu dóoree du jëm ca kã ya, mbaa góol bi ni ko ciix jàpp. Loolu nekk na lu ñu war a jàngat, liggéey ci ak atakã yi, jéem ci indiy saafara. Ndax ka, ku dul dugal doo am ndam, te dugal lu bari dinay gën a dooleel ekib bi.
Diggante Senegaal ak Benee, démb, ndam demul ndam dikkul, 1-1 la mujje. Senegaal moo njëkk a dugal (Abdulaay Sekk), ñu dawal ba ca boori mujjantal ga (78eelu simili bi) Benee daldi fayu.
Talaata jii di ñëw, di 20 suwe 2023, Senegaal dina ci amalaat benen joŋante xaritoo, war ci daje ak ub punkal : Beresil bu ñoom Vinicius Jr. Bresil moom, du ekibu yaafuus. Suuf gi, digg gi ak kaw gi, fépp baax. Ekib bu raglu la, diis lool. Bu keroogaa, Aliw Siise ak i ndawam dinañ mën a natt dëgg-dëgg seen doole ba xam lu des ak lu desul. Moom, Beresil, Gine la doon dajeel démb. Daf ko dóor ñeenti bal ci benn (4-1). Démb moo nekkoon guleet saa-beresil yi di sol mayo bu ñuul, li ko waral nag mooy dooleel xeex bi ñuy xeex mbirum xeetal gi nit ñi ñuul ñiy jànkonteel saa su nekk. Bu loolu weesoo ngir Senegaal daan leen, fàww ñu dolli cere, yokk ñeex. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/ku-tiitul-man-tiit-naa/ | KU TIITUL MAN TIIT NAA
Senegaal wote nañu dibéer ji weesu yamook ñaar-fukki fan ak ñeent ci weeru féewaryee. Ba démb ci alxemes ji ñu ngi doon xaar njuréef ya ca tukkee te këru-àtte gi war cee àddu. Loolu jur jiixi-jaaxa ci askan wi, bawoo ci kàddu yi nguur gi ak kujje giy yëkkati, ñii naan jéll am na ci songoo bu njëkk bi, ñi ci des jàpp ne njaax dafa am, fàww ñu sëggaat bëre. Daanaka askan wi aj na noowam, di xaar aji-àttekat yi séq Ndajem ndeyu-àtte mi àddu ci mbir mi.
Waaye bu nu xoolaatee yëf yi bu baax, wote bii tiitaange gu réy moo ci tukkee war a ñeel képp ku am seetlu. Ndaxam sax de, li tiital askan wi ajuwul ci lees gën a jàpp, mu jëm ci kan la yoon di nangul ne moo jël ndam li.
Li jur tiitaange gi, war naa yóbbu fitu képp ku yittewoo bàkku réew mi : “Wenn Askan, Benn Jubluwaay, Benn Gëm-gëm”.
Su nu waxantee dëgg, ñu bare seen woteb dibéer ci waaso ak tariixa la lalu woon. Di lu kenn mënul a nàttable. Li ma yokk tiit du lenn lu dul ne sunu réewi Afrig yi dañoo des di sooxaale ab góomu judduwaale. Mu méngook ne ay réew la yoo xam ne Bokk moomeel (Nguur) dafee jiitu Bokk Xeet (Askan). Li ko waral mooy waaso yu bari yu seen jaxasoo desoon, ñu yàgg a xare ci seen biir ba noppi nasaraan yi leen nootoon ci lu jege ab xarnu boole leen ciy Bokk moomeel ca diggante atum 1885 ak 1886 ca Berleŋ, péeyub Almaañ. Moone, yooyu waaso sax de, wenn askan lañu, ni ko Séex Anta Jóob wanee. Mu ngi nuy xamal ci téereem bi mu duppe “Civilisation ou barbarie” ne “Deret jiy daw ci samay siddit njaasu deretu wolof laak ju séeréer, ju saraxolle, ju pël, añs.”. Mu tekki ne waaso ak lu ni deme, waruñu fee jur ay. Waaye itam bu nu xoolee ci taarix, ñetti xarnuy njaam, fekki benn xarnub nootaange tax nañu askani réewi Afrig yi réere mbir li leen boole def benn.
Amaana looloo waral njiiti Afrig yu njëkk yi fullaaloon bennoob réew yépp, ñuy xàccandoo di dóorandoo. Ci loolu la ku mel ni Ufuwet-Buwaañi taxawoon ca réewum Kodiwaar. Ci loolu it la Seŋoor newoon, sukkandiku ci lu mel ne kalante giy dox ci diggante yenn waaso yi, moo xam séeréer laak pël walla joolaak séeréer, mbaa kalante biy dox ci diggante Njóobeen yeek Njaayeen yi, Jaween yeek Sekkeen yeek Géyeen yi. Waaye li seen liggéey di rafet yépp teewul ba tey njaw des aw xambin. Kon, simoŋ bi war a lëkkale waaso Afrig yi ngir mu taxaw fu dëgër, dese naa wow. Ngelaw lu ñàkk solo mën naa tasaarey réewam. Ku ko weddi na ko seet ci li xewoon Kodiwaar bu yàggul rekk. Benn baat kesee ko tas tasar, muy baatub “ivoirité”. Mu nuy fàttali tamit réewum Ruwaandaa ci atum 1994.
Nan fexe boog ba li tàmbalee raam ci dibéeru 24 féewaryee 2019 bañ a yegg ci ñag bi. Nan fexe ba mucc ci li toj Kodiwaar, rajaxe Ruwaandaa.
Daawuda Géy | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM
AY YEESAL ÑEEL BARI (LES EQUIPES) SENEGAAL YI
Gaynde yu mag yi (ekib A)
Wéyalees na pasug Aliw Siise gi ba keroog atum 2026. Kii di Paap Caw lees tabb, teg ci wetam, muy tofoom (adjoint).
Gayndey réew mi (équipe nationale locale)
Bu dee lu ñeel gayndey réew mi, Suleymaan Jàllo lees dénk lenge, mu war leen a tàggat. Sosef Seŋoor ak Séex Géy ñoo diy tofoom.
Gayndey yu ndaw
Bu dee xibaar yi aju ci gaynde yu ndaw yi amagul 20i at (U20), Sëriñ Ja mooy leen yor. Bu dee gaynde yu ndaw yi amagul 17i at (U17), Ibraaxiima Fay a nekk ci bopp bi.
MUKTAAR JAXABI OPPEEREWU NA CI JÀMM
Alxames jiI weesu, 7 màrs 2024, la jañkatu Gine bi oppeerewu ci tànk fa raglub “Jean Mermoz” ba nekk Liyoŋ (Farãs). Lépp jaar na yoon. Waaye, gaañu-gaañoom bi du bu ndaw. Nde, gannaaw gaañoom bi ca seen joŋante (valence) baak Real Madrid ca ayu-bés bee weesu la fajkat bees di wax “Dr Gastaldi” biral ay kàddu di xamle ni dina jafe lool ngir Jaxabi doxaat ni mu waree. Ndaxte, xeetu gaañu-gaañu bi yamul ak yu bari yu futbalkat yiy ame. Dolli ci ne jéem a fexe ba mu doxaat lees war a seet balaa ñees di xalaat mu delluwaat ci pàkk mi. Muy lu ñu bari di ko mastawu.
ARDA GÜLER DUGAL NA BIIWAM BU NJËKK CA REAL MADRID
Saa-Tirki bi dugal na biiwam bu njëkk ca Real Madrid, démb ci dibéer ji, ci seen ndaje beek Celta-Vigo. Moom nag, ba mu ñëwee ca ekib ba ba léegi amagul wërsëgu wane boppam bu baax. Ndax, dafa dikk rekk am ay gaañu-gaañu yu tegalante woon. Loolu doyul, Carlo Ancelotti miy tàggat këlëb bi du ko futbal-loo lu bari. Yenn saa yi mu mosal ko as lëf ciy simili, waaye li ci ëpp ci toogu bi la koy bàyyi. Démb itam, bi joŋante bi desee 8i simili la ko dugal ci pàkk mi. Waaye, lu simili yiy néew-néew, jot na ci bégal soppe yi, rawatina yu dëkkam yi bëgg di ko gis muy laale lu bari. Fim ne mooy Saa-Tirki bi gën a doon ndaw te dugal ca sàmpiyonaa bu Espaañ. Turam dugg na xaat ci mboor ma.
LÀMB JI
Bëre taxaw na digante Móodu Lóo, buuru làmb ji, ak Sitta. Ñoom ñaari mbër yi dinañu sëgg weeru Nowàmbar ci atum 2024 mii.
BOKS : FRANCIS NGANNOU ÑÀKKATI NA
Saa-Kamerun bi ñàkkaat na weneen yoon ca powum boks ma. Guddig àjjuma jàpp 8 màrs la doon amal ñaareelu xeexam ci wàllu boks. Jàmbaar jii di Anthony Joshua la doon laaleel. Aji-mujj ji daf ko dóor mu tëdd ca ñaareelu xaaj wa, daldi gañe joŋante bi. Moom nag, Ngannou dafa mel ne neexleegul ci po mi. Ndax, ba mu jógee ca MMA ba léegi amagul ndam ci boks bi. Xëy-na lim miinagul yëf yi la, am li mu ñëw rekk ñu jox ko ci waagay po mi. Di xaar ci moom mu dikkaat ak taxawaay bu gën a jekk ci yeneen joŋanteem yiy ñëw. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xeesal-walla-xeeb-sa-bopp-2/ | XEESAL WALLA XEEB SA BOPP?
Kañ la jigéeni Senegaal yi tàmbalee xeesal ? Fanweeri at ci ginnaaw ? Lu ko ëpp ? Gëstukati réew mi war nañoo tontu ci laaj boobu. Li ma ci xam, daal, moo di ne mu ngiy bëgg a yàgg. Mel na ni ca njëlbéen ga ñu bare dañu newoon ci seen xel : ‘’Lii de, baaxul, waaye ay feemi gone la rekk, du jikko, jamono la, léegi ñu génn ci !’’ Njuumte lu réy la woon ndax fi mu ne nii, yematul ci jigéen ñi, ay góor sax a ngi diwu… Ku sañul ni bala la yit, xalaat nga ko.
Ku weddi ne tey la Waalo gën a aay, doxantul ci mbeddi Ndakaaru yi, téen xool nataali-siiwal yiy tagg xees ak xeesal. Boo toogee sa kër tamit, taal sa tele dinga gis ñu ciy wane ndaw suy diwu, yànjal la ko ba nga ni lii lu mu doon, nataal yi di la déey musiba, naan la ‘’Nii nga war a mel !’’, walla : ‘’Nii nag la sa soxna war a mel !’’’
Wax ji moom jarul a yërëm, li xeesal tekki moo di ne am der bu ñuul gàcce la, taaruwl dara, loo gën a nirook Tubaab ñu gën laa teg nit.
Mbir mi dafa dagg xol ba noppi yéeme. Xéy-na lu ni mel mënoon nañ ko séentu feneen ci Afrig fu dul Senegaal. Liggéey bu mucc ayib bi Séex Anta Jóob def ngir weglu nit ku ñuul waroon naa tax nu àndandoo sib xeesal. Te yit, xanaa Senegaal dootul réewum ‘’Négritude’’ ? Xanaa du Seŋoor a bind ‘’Femme noire’’, taalif bi gone yiy tari subaak ngoon ?
Lii lépp a merloo woon Aysa Dem, mi ñépp xam ci farloom ñeel mbiri aada, ba mu jiite fi kàmpaañ, duppe ko ñuul kukk di fésal taaru jigéen ju ñuul ak ni nit ki waree naw boppam. Fulla ju mat sëkk la Aysa Dem wane foofu te ñu bare gërëm nañ ko ci. Waaye li gënoon xéy-na moo doon ñépp àndandook moom ci xeex boobu. Mbootayi jigéen ñi nga xam ni foo leen fekk ñu ngi ñaxtu, naan dañoo sàggane seeni yelleef, kenn waruleen woon cee jiitu. Léegi, nañu yëkkati seen kàddu, wax kilifay réew mi ñu aaye kuy def piblisite xeesal, aaye sax xeesal ci boppam.
Am nay jàngoro yoo xam ni gornmaa rekk moo leen mén a faj. Xeesal ci la bokk. Loolu la Paul Kagamé, njiitul Ruwandaa, xam ba jël ay dogal yu am solo, tere kuy dugal walla kuy defar diwu yu ni mel ca réew ma, tere yit ku ko jaay, ku ko jënd mbaa ku ko jëfandiko. Loolu lañ fa dogal te ku ko moy yoon dal ci sa kow.
Teewul doktoor yeek yeneeni boroom xam-xam war di wéy di gindi jigéen ñi, di leen yee ba ñu xam ni nit ku weex gënul nit ku ñuul. Waaye liñ naan bóli gu dog tiiñ na doktoor moo fi ne. Ndax ndaw soo laaj lu ko xiir ci xeesal mu am ci kersa, damm loos ni la lépp ak góor ñi, soo xeesul duñ la faale. Ñu ci bare leeral rekk a leen ciy dugal, ñu dem ba yëf yi ëpp leen loxo, fu ñu gis diw jënd ko, diwoo.
Moonte xam nañ xéll ni xeesal day oyofal sa der, wàññi dooleem, foo laal daj ay picc ak i rew ak i taas, soo moytuwulee jële ciy feebar yu bon niki kañseer walla taŋsiyoŋ. Doktoor yi seen xam-xam màcc ci pajum der wax nañu ba tàyyi, waaye kenn nanguwuleen a déglu. Waaw, ndax wut taar rekk jar naa ñàkk sa bàkkan ?
Ñàkkul jaaykati xeesal yeek isin yi koy defar la nguur gi ragal ba tax ko ni patt-pattaaral, di seetaan lu ñaaw lii mën a delloo réew mi ginnaaw. Am na ñu naan du loolu lépp, dafa ferekk ni sunuy njiit tal nañu leneen, nun baadolo yi amaluñ leen benn solo. Xanaa kay du loolu laa yaakaar ?
Ku xeeb sa bopp, dem sax ba xamatoo yaay kan, mënoo amal benn njariñ saw askan. Kon, nanu ci jóg gaaw : xeesal jëmul kër…
Ndey Koddu Faal
XEESAL WALLA XEEB SA BOPP ? was originally published in Defu Waxu on Medium, where people are continuing the conversation by highlighting and responding to this story. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/can-u-17-2023-kub-mu-ngi-xeen/ | CAN U17 2023 : KUB MU NGI XEEÑ !
Raayab Senegaal a ngi gën yéeg, turam di gën a jëm ca kow a kow. Sunu kuppekat yaa ngiy wéy di aj turu Senegaal gi muy gën di kawe rekk. Gannaaw ba ñu gañee ñeenti kuppeg Afrig ci ñaari at yii, ñoo ngi ciy bëgg a teg juróomeel bi.
Foofu ca Alséri, ndawi Senegaal yaa nga fay wane fullaak faayda ju mat sëkk. Ba kub bi tàmbalee ba léegi, ñoo ngi teg seen tànk ba mu dëgër, teggiwuñ ko wenn yoon.
Génn gu rafet lañu génne woon ci seen kippu, gañe seen joŋante yépp dugal ca 7i bii te jëluñu ca benn. Ñu génn, kaar-dë-finaal bi ñu daje ak Afrig dii Sid dóor ko juróomi bal ci dara, muy ndam lu rëy. Démb, ci dibéer ji, 14 Me, mu doon daje ak naataangoom bii di Burkinaa Faaso bi 16i waxtu jotee, mu nekkoon joŋante bu mettee-metti sax (1-1) boo xam ni bii ci, dóor-ma-dóor (série pénalties) la mujje. Senegaal moo mujje gañe. Ca 19i waxtu, démb, Marog itam doon daje ak Mali, dóor ko itam ca dóor-ma-dóor ya. Senegaal war a daje ak Marog finaal àjjuma jii di ñëw, di yamook 19 Me.
Senegaal, démb ci demi finaal bi lay door a jël bii. Dugalagum na 13i bii. Amari Juuf itam nekkagum ba léegi ki ëpp lu mu dugal (5i bii).
Senegaal moo ngi ci buntu jël juróomeelu kuppeg Afrigam, kon nanu ko daan waxe rekk, ngelaw liy ëpp sunu réew mi ci wàllu kuppe Yàlla bu mu gaaw a dal.
Mànkoo wuti ndam li ! Gayndee Njaay mbara-wàcc ! | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-gaawu-4-feewaryee-2023/ | Li gën a fés ci xibaari tàggat yaram (Gaawu 4 féewaryee 2023)
PREMIER LEAGUE / ÀNGALTEER
Liverpool
Ribeertoo Firminoo yëgal na waa këlëb ba ak tàggatkatam, Jurgen Klopp, ni dafay dem bu atum sàmpiyonaa bi jeexee. Li sabab loolu nag, mooy ni dafa yëgatul boppam ca ekib ba. Ndax, bareetul la mu fay joŋante jamono jii.
BUNDESLIGA / ALMAAÑ
Nkunku amatina gaañu-gaañu
Christopher Nkunku amati na gaañu-gaañu. Démb, ci seen joŋante bi doxoon seen digganteek Dortmund, la gaañuwaat. Te, démb la doon door a delsi gannaaw gaañu-gaañu ba mu ame woon ca tàggatoom ba ak ekibu Farãs, ba ñuy waajal kuppeg àddina sa. Am na ñuy wax ni dafa toogul diir bi waroon ca gaañoom ba weesu moo waral mu dalaat ko. Dana toogaat ay fan.
Dortmund
Ñuul-mbokk yi nee nañu kenn du leen téye. Ñoo ngi wéyal, di dóor, di am ay ndam rekk, di dem. Ci 10i joŋante yu Dortmund amal ci atum 2023 mi, dafa gañe yépp, duggal ci 25i bii ba noppi jël ci 9 doŋŋ. Moo nekkagum ci boppu Sàmpiyonaa, fileek ñuy xaarandi Bayern dawal.
KARAGÜMRÜK / TIRKII
Mbay Jaañ a ngi yëngal sàmpiyonaa Tirkii ba. Tey, ci gaawu gi, ñetti bii la dugal, séddale benn paas. Kenn mënu koo téye jamono jii. Bu fekkee dafa bëgg wan Aliw Siise ni dafa war a ñëwaat ekib Senegaal, moo ngi ci yoon wi. Ci 19i joŋante ya mu fa amagum, foofa ca Tirki, Mbay Jaañ dugal na ca 14i bii def itam 5i paas. Gaynde Njaay mbara-wàcc !
CAN U20 2023
Senegaal, Gàmbi, Tinisi ak Niseriyaa ñooy ekib yu dem 1/2 finaal. Ñoom ñeent ñii itam ñoo dagg paasu kuppegg àddina ñeel ñi amagul 20i at. Ngelaw liy uppu Senegaal ci wàllu tàggat-yaram Yàlla bu mu gaaw a dal, rawatina ci kuppe gi. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/faidherbe-du-fi-maamu-kenn/ | FAIDHERBE DU FI MAAMU KENN
Fan yii yépp, xanaa mën nañoo wax sax weer yi weesu yépp, coow laa ngi neeti kurr ci biir réew mi ak ab jàppante bu dul jéex. Jàppante bu doy waar, nag. Coow li, coow li, keneen yóbbeewuñu ko ku dul seriñ Faidherbe. Faidherbe sax, de. Moo fi ne woon Gornóor, daloon ca Ndar, peyu Senegaal ak dëkki Afrigu Sowu Jant yépp jamono ji Tubaab yi moomee réew mi. Estati boobu ñu ko jëmmale ca béréb bi ñu duppe turam ci Ndar, ma nga fa ne noŋŋ-noŋŋaaral, téeméeri at ak fanweer ak ñent ba sun-jonni-Yàlla-tey-jii. Laaj bi benn la : lu mu fay def booba ba léegi ?
Ndax xel nangu na ñuy wéy di sargal Faidherbe ci Senegaal gii moom boppam, boobaak léegi mat na juróom– benn fukki at ? Jàppante bi nag, boroom xam-xam yi génne ci lekooli Tubaab yi ñoo ko séq, mu mel ni daal, ñenn ci ñoom dañoo am cofeel ci doxalinu Tubaab yi fi woon ba di leen namm !
Ñoom ñooñu, nag, dañu jàpp ni, mu neex, mu naqari, Faidherbe ak i ñoñam ci cosaanu Senegaal lañu bokk. Konte war nañoo weesu fi mu ne nii, di gaaw a gis sunu bopp ba di fàtte ni, nooteelu Tubaab ba woon, lu mu doon metti-metti, amoon na itam lu ci ñépp mën a rafetlu. Ku weddi na xool jàlloo bu mag te rafet boobuy jéggi dexu Ndar gi te ñu duppe ko… Faidherbe ! Du waa Senegaal, rawatina doomi Ndar yi koy jariñoo ñooy wax ne amul maanaa ! Ba tax na, estati Faidherbe bi, lu fa mat a bàyyi la. Am na sax ci boroom xam-xam yooyule, ku nu ciy artu : bu coow li jëm kow, ndax kat, bu nu dof-dofloo ba waa Lille, dëkk boobu Faifherbe fekk baax, jot ci, du ñàkk ñu téye seen xaalis bi ñuy dimbalee Ndar ñeel séexal gi lëkkale ñaari dëkk yi. Nu gis ne, xëccoo « deseer » bi nuy nootkat bi jóge bitim-réew di ñamal, lu fi yàgg la te du fi teel a jóg…
Boroom xam-xam yooyu nag, mënoon nañoo wax leneen lu-dul Frãs ak ndawam lu mel ni Faidherbe ci sunu cosaan lañu bokk te dan leen war a weg, sargal leen. Waaye booy seet, seen lay yépp noonu la tollu, ba tax na ku leen déglu, soo moytuwul yéemu !
Ndax nag, war nanoo njëkk xam li ñuy wax lan la ak naka la mbir mi tëdde.
Senegaal ak réewi Afrig yu bari, ginnaaw ba ñu dunde ñetti xarnu ci njaam, dundati nañ ñaari xarnu ak lu topp ci nootaange Tubaab yi leen songoon ak seeni xeeti gànnaay yu bees ; amul lu ñu dajul ciy loraange, metit, ndóol ak toroxte. Tubaab yi ñoom, lu yëngu ñu jam, di rey, di lakk, di sàcc, di gàddu doomi Afrig yi yóbbu Amerig… Noonu la Afrig ñàkke lu tolloog ñaari téeméeri alfuniy nit yu ñu gàddaayloo mbaa yu ñu faat. Sunu dund gi ñàkkati gancax yu ñu yàq, alal yu ñu pasar-pasare, dëkk yu ñu toj, aada ak ngëm-ngëm yu ñu salfaañe… Nootkat yi yemuñu woon foofu : doon nañu sàkku jigéen ñi ; boole ci jàpp góor ñi di leen dugal ci seen làrme, ñuy rey ak a yàq ñoom itam ci lu dul seen sago ; ñoom nootkat yi doon nañu walbatiku jël gune yi dugal ci seeniy lekool ngir raxas seen xel ba lu ñu sant gune yi ñu def ko, ànd ceek ñoom sax.
Njiiti réewum Farās nag, delloo nañu njukkal seeni doom yi doon toroxal Afrig, màggal nañu leen. Noonu lañu tànne ka leen yilifoon, te ne woon ndeyu mbill gi, muy Faidherbe, ba mu dëddo àddina, tudde kob béréb bu réy ba ca Ndar, jëmmal fa estateem, ba noppi tudde ko pom bu mag ba mu fa defarlu woon.
Ndege Tubaab bee fi doon buur di bummi, kenn amul woon looy nangu walla looy bañ. Te yit kenn mënul a wax ne Faidherbe yelloowul woon màggal googu ña ko fi yabaloon màggal. Noonu la réewi àddina sépp di doxale : mbër moo ngemb ba mu daan, sargal ko war na la.
Waaye ka mu daan ak i farandoom ñoom, ndax warees naa xaar ci ñoom ñu tàccu ko ? Ku xam ni amaatëeri làmb yiy nekke, xam ni, fàww ñu xar ñaari pàcc yu wute, ñii féete fii, ñale féete fale : su ñii di ree ak a fecc, ñale di ŋàññ a ka jooy. Monte loolu de, daa mel ne, lu ñépp war a xam la, am déet ?
Konte nan jàpp ne, kuy xalaat a sempi estati bu Faidherbe walla bu beneen nootkat bu mu mën a doon, taxul mu weddi xew-xewi coosaan yi ñépp xam, ndax li am, daa am ba noppi, kenn mënatu ci dara. Ana luy ndeyu wéy di sargal ka doon faat ak a bóom sunuy maam, doon fi def naka-su-dul noonu ? Estati nag, tekkiwul leneen lu dul sargal ka muy jëmmal ! Loolu, dara la jotewul ak tabax ay pom ak i tali, walla ay lekool ak yeneen yu ni deme.
Danuy nangul Tubaab yi ni, Faidherbe seen mbër la woon, ñoom waa Tugal ! Muy lu kenn mënul a weddi, feek waa Farās ci seen bopp ñoo ngi gëm loolu.
Waaw, Senegaal nag moom, ndax Faifherbe ciy mbëram la bokkoon ? Loolu mooy wax ji !
Waaw, xanaa du Faidherbe moo fi jiite woon soldaar ya songoon Sowet, Njag-Aral, Njaral, Njajer, Marsa ak Bàkkel, ca atum 1855 ca weeru Màrs, rey nit ña, rajaxe lépp lu fa doon dëkkuwaay, taal gàncax ga ? Ana kan moo takkaat xare weer wa ca topp, dem bóom waa Naye, dëkk boobu féete ci penku Senegaal, ñépp dee fa, kenn desul ? Nañ ko xam, du keneen ku dul Faidherbe. Kan moo demati ci weeri Suweŋ ak Ut ci at moomu, song Sóokóon, Njat Amar Faal, Cileen, Ros, Damga, Bàkkel, Kungël ak Caabo…? Moom la woonati, moom defkatu njaaxum bi, seneraal Louis Léon César Faidherbe. May laaj, kan moo taal Njiit (ci Njàmbur), Wadan ak Baral, ana ku jëf ñaawtéef yooyule ? Bumu bett kenn, mooma ba tey, nit ku bon ki, Faidherbe. Waaw, kan sax moo demoon Fatig ci weeru Me 1859, lakk tool ya, lakk kër ya, bóom waa dëkk baak waa dëkk-dëkkaan ya ko wëroon yépp ? Ku muy doon ku dul sunu waa ja maroon deret te tudd Faidherbe ? Ku dellu ca weeru Awril 1861 dal ca kow ñaar-fukki dëkk ak juróom ya féete ca Kel ak Mexe, teg ca Kër Aali ak dëkk ya ko wër, walbatiku te waccul ca ginnaawam lu-dul naqar ak i dóom ? Moom doŋŋ, moom Faidherbe mi doon liggéeyal réewam, yëkkati raaya Farās ngir toroxal der bu ñuul. Taxul nag mu yem fa, ndax atum 1861 la dal ci Boseyaa ca Fuut
a yi…
Mbir mi jéggi na dayo, doy na waar ! Moo tax it kenn jéemul a woññi ñaata nit ñoo loru ci ñaawtéefi Faidherbe yooyu. Porfesëer Iba Deer Caam daal, moo ñuy xamal ne, am na benn gëstukatu Tugal bu xayma ni, li Faidherbe faat “ci diirub juróom-ñetti weer rekk’’ tollu na ci « ñaar fukki junniy (20. 000) doomi-aadama » !
Waaye nag, nettali ci làmmiñu boroom ! Ci li ñu boroom xam-xam bii di Xaadim Njaay xamal, Faidherbe, ba mu nekkee Alseri doon fa def ay njobbeem, laata muy ñëw Senegaal, daa yónnee bés ab bataaxal di ci yëgal ndey ji ay jalooreem, ni ko :
« Toj naa benn dëkk bu rafet, rajaxe fa ñaari téeméeri kër ak seeni tóokër. Waa dëkk bi dañoo tiit ñoom ñépp, dawsi jébbalu ci man ».
Lii moom, luñ ci waratee yokk ?
Ngóor soosoo doon Faidherbe mi Senegaal di sargal. Daa fekk nag ne, sunu jamono jii, ginnaaw ba ñu toroxale George Floyd ba noppi rey ko ca Amerig ndax rekk li deram ñuuloon, àddina sépp a ko jooy ; ba tax na ndawi réew yu baree-bare dañoo jóg di buddi bépp estati buy màggal ñi doon toroxal doom-aadama. Ndawi Senegaal nag yi, ci ndawi àddina si lañ bokk. Kon warul jaaxal kenn su dee, ñoom it, dañu jóg wone seen bopp, fésal seen naqar ci sargal bi nuy wéy di sargal Faidherbe. Loolu kepp a tax ñuy laaj lii : lu tee ñu sempi estati Faidherbe ba ne noŋŋ–noŋŋaaral ca Ndar ?
Ndaw ñi nag, doon nañu xaar ci boroom xam-xam yi, rawatina ñi ci daara yu kowe yi, ñu am taxawaayu Usmaan Sémbéen mi doon laaj Seŋoor :
« Xanaa sunu réew mii, jurul ay jigéen ak i góor yu yelloo ñu sargal leen, tudde leen sunuy lekool, sunuy iniwersite, ak sunuy mbedd ? »
Danu war di màggal sunuy jaambaar, ni ko réew yi fonk seen bopp yépp di defe. Wareef la ! « Sama bopp a ma la gënal, tekkiwul ne dama laa bañ ». Tee noo bañ a ànd ak ña doon toroxal ak a bóom sunuy maam ? Faidherbe ak ñi ko fi wuutu, dañ koo jar am ? Estati Faidherbe bii, daa amatul palaas ci Senegaal gii moom boppam tey. Su dee sunu moomeel gii du ay naxee-mbaay.
Nanu sempi estati bi, nanu ko déjjati. Su ko laajee, ñu wutal ko fu ñu koy denc. Loolu nag, dunu tax a fàtte sunu démb, sunu mboor mi nu war a bindal sunu bopp.
Senegaal, Faidherbe du fi maamu kenn !
Uséynu Béey | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/ | FAATUG HIBAA CAAM : SENEGAAL, BOPP BU XAR ÑAAR?
Guddi àjjuma, dëppook 3eelu fan ci weeru Awril, doon guddi gi jiitu bésub baaxentalub sunu moom-sa-réeew, la benn jànq bu am 28iat, di wuyoo ci turu Hibaa Caam, ñàkk bakkanam, ci anam yu tiis te doy waar. Ñu ngi ko fekk mu tëdd, ne nemm, di waccu deret. Ci li taskati xibaar yi wax, xale bu jigéen bi, dafa jël lu ko ëpp doole ci ay donji dorog, ba faf ca faatoo.
Loolu nag, mu ngi xewe ci Almadi gii ci Ndakaaru, ca kër gu Baaba Jaw «ITOC» di luye. Moom nag, boroom alal ju raññeeku ci réew mi la te doomam bu jigéen moo ko féetewoo. Ñi fa daje woon ay moroomam lañu, ay xale yu góor ak yu jigéen, ne fay fo ak a topp seen bakkan, doon it ay doomi boroom alal, ak ay doomi kilifa yu ñépp xam ci réew mi. Ku ci bokkul ci ñi ŋànk nguur gii fi ne, am nga ci jegeñaale ; ñu ràññee ci : Daam Amaar, doomu ndem-si-Yàlla-ji Amet Amaar mu NMA SANDERS, doon itam goro Yusu Nduur, Luuti Ba te baayam di jiiteb kurëlu tàggat-yaram.
Xew-xew bu ni mel nag, dafay firndeel, ci lu amul benn werante, yàquteg goney réewum Senegaal fi mu toll. Dees na ci joxoñ itambaaraamu tuuma kilifay réew mi, ci ñàkk a yarseen njaboot ni mu ware, bàyyi leen ci seen sago. Li jar a laaj dëgg nag mooy : ana nu ay gune yu juddoogul, mën a yore xaalis bu dul jeex, di ko pasar-pasare nu mu leen neexe, ci Senegaal gu ndóol gii ? Lu doy waar la ! Rax-ci-dolli, ñu mel ne ñu réer, wàcc seen and,waral ñuy daje di jolluy bitéeli biiñ ak a tux sineebar, dëkke càkkaay…
Dëgg la sax, mënees na jàpp ni àddina day dox, ngir jamono ju nekk ak i feemam. Waaye kat…. !
Ak lu mu ci mën a doon daal, li ëlëm ñépp,mooy, jamono ji jéyya yii yépp di ame, tiis ak njàqaree ngi lëmbe àddina, ba tàbbi ci sunu Senegaal gii, muy CORONAVIRUS.
Mbas la moo xam ne, réewoo-réew mu ngi fay tëral ak a fàdd doomi–aadama yi. Ngir xeex ko nag, fii ci sunum réew, gornmaa bi dafa jël ay dogal yoy, bokk na ci : tere nit ñi ñuy génn guddi, ku nekk war a lëlu ba fajar. Beneen laaj bi nag mooy : xale yooyii newoon ci mbumbaay, ba dogal bi dal seen kaw, ana fan lañu jaar alkaati yi aakimoo mbedd yi. Ana nan lañu def ba mën a dem ak dikk, guddi, tollook 10i waxtu, ba Hibaa mën a fekki xaritam yi ? Walla, ndax ñoom, xale yooyu, dañu leen a jox ay kayit yu leen may boobule sañ-sañ ? Su ñu noppee ci laaj yooyu, beneen taxaw, muy : ndax dafa am ñaari Senegaal : gu baadoola yi yoon mën a dal seen kaw, saa su ne, ak geneen, gu ñeel boroom barke yi, ñuy buum di bummi, di tambaambalook a def lu leen neex ? Dafa mel ni daal, yoon buy digal ak a tere, baadoola yee tax ; ci ñoom daal la gën a jekk. Moone, dañuy faral di wax naan :« Senegaal, benn bopp la, kenn mënu koo xar ñaar ! » Am déet ?
Laaj yi yamuñu foofu de ! Leneen li mat a xam, mooy : ndax CORONAVIRUS bii, dafa am ñu mu dul song ? Du dañu naan feebar bixamul xàjjale? Ak li ñuy woote yépp ci rajoo yeek tele yi jëm ci jumtukaay ak i matuwaay ngir moytu feebar bu bon bi, niki : soriyantoo, raxas say loxo, ak yu ni mel, naka la sunu njiit yi mën wëlbatikoo, bàyyi seeni doom, ñu topp seen bakkan, di doxe maa-tey ? Xanaa kenn mënul ne bëgguñu seen doom yooyu de ? Walla, ñoom ci seen bopp, dañoo gëmul dara ci li ñuy woote ?
Mbir maa ngoog. Laaj yi bari nañu lool, te yeneen mat naa leeral, yu mel ni, Hibaa Caam mi ci ñàkke bakkanam, ku ko rey, ak ci yan anam la faatoo ? Li ci gën a doy waar nag, mooy, doonte ubbeeguñu lànket bi, taskatixibaar yi xamle nañu ni, way-jur yi ci seen doom taq ripp, ba alkaati yi teg leen loxo, ña ngay dugg ak a génn, di lal ay pexe. Looluteey na xelu ñu bari, ba ñu jàpp sax ni mbir mi du mujj fenn.
Loolu nag, su amee it, du fi guléet : xanaa fàttewuleen Mati Mbóoj, janq bu siiw boobu fi génnoon àddina moom itam, ci anam yu ni mel? Mel na ni nag, yëf yaa ngi bëgg a ëpp i loxo, te lu ëpp, tuuru. Su ñu ci jógul, du baax ci guney réew mi.
Waaw, Senegaal gii xar ñaar, ak ñawtéef yi lëmbe réew mi, ndax mënees na koo saafara ? | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-2/ | CAN KODDIWAAR 2024 : CAABALU BÉS BI
NGIRTEY JOŊANTEY BÉS BI
Démb ci altine ji, kippug A gi ak gu B gi amal nañu seen ñetteeli joŋante ñeel sumb bu njëkk bi bi CAN 2024 bi.
Kippug A : Koddiwaar wayadi na/ Kap-Weer ak Niseriyaa raw nañu
Ñetteeli joŋantey gile kippu a ngi am ba 17i waxtu jotee ci, doxoon ci diggante Gine Equwaatoriyaal-Koddiwaar ak Gine Bisaawo-Niseriyaa
Gine Equwaatoriyaal dafa teg gàcce gu réy ñayi Afrig yi seen kanami soppe. Nde, daf ko ndulli 4i bal ci dara (4-0). Kesiyee ak i mbokkam, ci seen joŋante bu mujj bi lañu doon am yaakaar gañe ko ngir kalifiye. Waaye, dafa mel ni yëf yi takk na suuf. Ndax, fim ne nii, moo ngi ci guddi yu lëndëm lool sax. Mu nekk lu metti ci ñoom ñi nga xam ni ñoo dalal po mi seen dëkk.
Niseriyaa, moom, dafa dóor Gine Bisaawu 1-0. Seen ndam li nag yombul woon ci ñoom. Nde, démb, saa-bisaawo yi dañ leen indil alxatiir. Dugal nañu ca sax ñaari bii yoy, dañ ko bañ. Rax-ci-dolli, seen defãsëer bii di Opa Sangante moo dugal seen kã ca 36eelu simili ba.
Gine Equwaatoriyaal moo jël pée ca kippu ga ak 7i poñ, topp ci Niseriyaa, moom it 7i poñ la am. Waaye, aji-jiitu ji daf ko rawee ay bii. Koddiwaar moo jël 3eel ak 3i poñ, Gine Bisaawu laal ndaare boole ci amul dara ciy poñ.
Kippug B : Esipt ëpp na wërsëg Gana !
Ñoom, seen i joŋantee ngi door bi 20i waxtu jotee ci guddi gi. Benn bi, newoon diggante Mosàmbig ak Gana, ba ca des Kab-Weer ak Esipt. Ñaari joŋante yépp a ngi jeexee ci 2-2.
Gana, ci joŋanteem, dafa jiital Mosàmbig ñaari bii yoy, ciy penaaltii yu Jordaan Ayu dugal la ci 15eel ak 70eelu simili ya. Ñu bari jàppoon ni Gana gañe na sax, ba seen i xel tàmbali woon a dal. Waaye, dañu dawal ba ca jeexitalu mats bi Mosàmbig am penaaltii ci 91eelu simili bi, dugal ko. Ñu teg ci ñaar ba ñetti simili ñu tojaat këru Gana, Biddéew yu ñuul yi daldi wayadi.
Joŋante Kab-Weer ak Esipt, daanaka noonu la xaw a demee tamit. Ba ñu tàmbalee dawal bay waaj a mitã la Saa-Kab-Weer yi dugal (46eelu simili). Bi ñu noppaloo ba delsi ba ci 50eelu simili ba Esipt fayu. Ñaari ekib yiy wéyal ba ci 93eelu simili bi, Mustafaa Muhammed bu Esipt dugal. Ñoom it, niki waa Gana, jàpp ni jeex na. Waaye, dañu dawal ba ci 99eelu simili bi, Saa-Kab-Weer yi song leen, boyal seen caax yi. Ci 2-2 yooyu la mats bi jeexe.
Seen kippu gi nag, Kab-Weer moo jiitu ak 7i poñ, Esipt topp ci ak 3i poñ, tegu ci Gana mi am 2i poñ tolloo ko ak Mosàmbig mi tooge ndaare bi.
NAALU TALAATAY TEY JI
Ci talaata tey jii, ñeenti joŋante dina amaat : ñaar yu kippug C gi ak ñaar yu kippug D gi.
Kippug C : 17i waxtu
Senegaal-Gine Konaakiri
Kamerun-Gàmbi
Kippug C : 20i waxtu
Móritani-Alseri
Àngolaa-Burkinaa-Faaso. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | YAA GORE !
Yàgg, yàgg, dëgg ay daan
Dëgg lottoon na Senegaal
Usmaan Sonkoo tax mu daan
Lii dinaa ko bind ngir ëllëg
Danga daan xëy di liggéey
Njiitu Réew dàq la sa liggéey
Dàqin wu ñaaw, mbete sàcc
Te yaa doon xeex ñay sàcc
Askan wi fal la, def la dépite
Ngay dëggal, doon ku nite
Fa nga daan taxaw Aasàmbale
Ku fa taxaw tey du ko mate
Ngay wax dëgg, ñu lay bów
Waa APR ak Abdu Mbów
Téye sa der bi di ci saw
Seen iy sobeek seen iy pexe
« Présidentielle 2019 »
Ñu lay kókkali, nga nëw doon
Ñetteel ca ña jiitu
Idiriisa Sekk xëy la wor
Maki Sàll téye di tëje
Takk-der di kajje, di pese
Xalifa Sàll nekk kaso
Nga taxawu ko, mu génn dëddu la
Ñi fi amul woon resepise
Ñi fi amul woon ku leen faale
Ñi fi amul woon fitu gaynde
Usmaan, yaay ki leen xettali
Mag yu bari faalewuñu ndaw
Nga wax ak ndaw ba mu mat mag
Lu mel nii ci sunu Réew
Néew na foo koy gise
Ba ñu xamee nag ne yaa leen gën
Ca la nu jóg di la tuumaal
Jiiñ nañu la fi ciif, jiiñ la rëbel
Jiiñ la terorist ak càccug telefon
Jël nañu la tëj ak sa njaboot
Ñaari weer ci sunu biir Réew
Gii gàcce, gàccee ka réy
Soo yambaroon nu dooniy jaam
Nu ne déet, ñu sànni la kaso
Sa pàrti, ñu gont tas
Say junniy àndandoo ñu tëj
Juroom-fukk ci ñoom ñu rey
Siggil ndigaale, Usmaan Sonko
Ci Baay Seex Jóob mi ñu bóom
Ci Porospeer Seŋoor sa doom
Ñoom ñii, ñooy say nawle
Ñiy dund, ñi ëpp matuñu
Tey jii, nga génn kaso
Ginnaaw nga woorlu jiitu Koor
Looy defati bàyyi leen ci xel
Nit ñi génn di la teeru
Ñoo yey, dangaa gore
Maki Sàll bëggul a dem
Nga samp Basiiru ngir mu dem
Sa jëf yii ni ñu taaroo
Yal na yiy ñëw gën a taaru
Yaakaar yi nga yee ci nit ni
Yal na ci ndam yu réy topp
Liy ñëw nag mooy gën a metti
Jagal Réew coono la doŋŋ
Waaye nag du yow laa koy wax
Ku ragal coono daa bañ lu baax
Doxal, Usmaan, bul jeng
Ci yow kat danuy jàng
Ëlleg, bëgg nanu laa weesu
Sunuy rakk it nëw di nu jiitu
Senegaal dëkkee tedd
« Yaa gore », la taalif bi tudd
Séex Axmadu Bàmba ki ko bind
Njaay-Jaata, dëkk Njaaréem
Di góoru Ajaa Mariyeem
Moo la naan, dalal ak jàmm !
Séex Axmadu Bàmba Njaay
15/03/2024 | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/can-2024-koddiwaar-tegg-sa-can-jel-ko/ | CAN 2024 KODDIWAAR : TËGG SA CAN, JËL KO !
Koddiwaar mooy waaga CAN 2024 bees doon amale biir dëkkam. Mu doon dajeek Niseriyaa bu Wiktoor Osimen. Waaye, moom Koddiwaar moo mujje gañe ñaari bal ci benn (2-1). Moom waaga wi nag, kenn réerewul fim jaar. Nde, tolloon na fi foo xam ni mënees na wax ni wërsëg dëgg a ko taxoon a des ci po mi.
Ci ñetteelu toogaay bi la Koddiwaar génne. Waaye, mu jóge ci loolu mel ni ndaw luñ yedd, gën a defaraat taxawaayam, solu jom ba fees. Ca la jóge woon gañe Senegaal teg ci Mali ak RD Kóngo. Démb ci gaawu gi 12i fan ci weeru féewiryee wi. Jamono jii, biir Koddiwaar, foo sànni mbàttu mu tag.
Niseriyaa nag, ku ne yéene woon na ko kub bi ndax yoon wu réy wiñ def itam. Seen joŋante yépp di woon mats jànq. Waaye, li wolof naan “nii la mënoon a deme”, kon noonu la mënoon deme.
Gannaaw loolu itam, amal nañ ay tabb ñeel ñi gën a xarañ ci po mi.
Futbalkat bi gën a xarañ : Ekong (Niseriyaa)
Góol : Wiliyaams (Afrig dii Sidd)
Dugalkat : Nsue (G. Ekuwaatoriyaal)
Ndaw li gën a xarañ : Adingara (Koddiwaar)
Tàggatkat : Emeers Faye (Koddiwaar) | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xalam-demoon-na-bay-neex/ | XALAM DEMOON NA BAY NEEX
Dibéer, 24eelu fan ci weeru féewaryee, atum 2019. Bés bi ñépp doon xaar, agsi na. Bés bi taskati xibaar yi doon séenu, di ko jagleel ay xët ak i waxtaan a ngi nii. Bés bi mag ñi daan waxtaane, ndaw yi di ci werante, janq yi di ci dàggasante, waa-jur ak doom dem ba ciy meroo agsi na. Bés bi àddina doon waajal bernde bu mag, teersi na, indaale saricaam. Waaye, ba alxemes ji nu génn, sarica baa ngi woon ci loxoy Demba Kànji, àttekat bi jiite Kurelu ndajem wote bi. Bu ko neexoon mu def ko jàmm, baaxe ko réew mépp ; bu ko neexoon yit mu soppi ko safaan ba, def ko fitna. Lépp, nag, a ngi aju woon ci ni àttekat bii di Demba Kànji di séddalee saricay askan wi. Ñépp a ngi newoon tekk di ko déglu : ndax dina séddale saricay askan wi ni ko yoon bëgge ? Noo déggandoo li mu wax. Nee na tééméer bo jël, 58 yi Maki Sàll lañu sànnil xob. Ñu bare ci réew mi jàpp nañu ni du dëgg ndax li rajo yeek tele yi wax, ñépp di ci dégg, moo di ne ñaareelu sumb mënutoon a ñàkk te njiitu réew meek Idiriisa Sekk ñoo waroon a laalewaat.
Naqaru way-moomeel yi dara waralu ko lu dul yaakaar bu tas.
Ci fajar a fajar lañu jóg, wutali bérébi wotekaay yi ngir def seen warugar, ni ko maxejj bu nekk war a defe. Wote ren bi nag, mbooloo mu takku te farlu lees ci ràññee, rawatina ndaw yi. Ci xayma, téeméer boo jël ci ñi jotoon a bindu ci kayitu wote gi, juróom-benni fukk yi wéet nañu ci mbañ-gàcce gi. Nee ñu xiirte gu ndaw yi am ci bile wote, lawax bii di Usmaan Sonko moo ko waral. Ndaxte, Usmaan Sonko benn, ndaw la, ñaar dafa yeesalaat politig bi, di biral njub, gëm sa bopp ak bëgg sa réew. Ak lu ci mënti am, keroog ñépp xéy nañu, solu ba jekk, dem wote ci yar ak teggin ba 6 waxtu ci ngoon, ñu daldi tëj wotekaay yi, ngir lim xobi juróomi wutaakon yi bokkoon ci joŋante bi. Naam, amoon na ay rëq-rëq yu ndaw, waaye daal mënees na wax ne bëccëgu wote bi jaar na yoon. Bi asamaan si muuroo, nag, ci la mbir mi tàmbalee lëbëjoo, ñenn ñiy jéem a tuur lëndëm askan wi.
Bi timis ji maasee, ci la lim yu njëkk yi tàmbalee rot, ñetti wutaakoon yii di Maki Sàll, Usmaan Sonko ak Idiriisa Sekk beddeeku di wone seen doole. Xëccoo bi tar lool ci seen diggante. Ku raw fii, kee raw fee, keneen raw fale. Yeneen ñaari lawax yi ñoom, Isaa Sàll ak Madike Ñaŋ, nangu ndogal, xam ni bokkatuñu. Ku nekk ci ñoom ñaar gërëm askan week maxejj yi leen wóolu ba sànnil leen seeni kàrt ba noppi ndokkeel Usmaan Sonko ak Idiriisa Sekk. Waaye, biral nañu tamit ne, ku gën a jekku ci diggante ñaari wutaakoni kujje gi, moom lañuy jàppale ci ñaareelu sumb bi nga xamante ne, jàppees na ci njëlbéen ni mënta ñàkk. Ci jamono jooju, waa Bennoo Bokk Yaakaar ñi ngemb Maki Sàll, ñoo giy fésal seen mbégte, naan Maki jël na raw-gàddu gi, xel wareesul a xalaat ñaareelu sumb di am. Loolu nag, du mbetteel, dafa di, ku ngemb sa mbër, bu la neexee bàkku ne yaay daan doonte dara wóoru la ci. Waaye, bi njiitu jawriñ li, Muxamadun Bun Abdalaa Jonn, génnee ca RTS ak TFM wax ni Maki Sàll faluwaat na ci sumb bu njëkk bi ak 57 baat ci téeméeri falaakon yoo jël, ci la xol yi jóg, coow li ne kurr.
Ci saa si, Usmaan Sonko ak idiriisa Sekk wooteb ndaje ak taskati xibaar yi. Ñaari wutaakon yi daldi ñaawlu doxalinu njiitu jawriñ yi. Waaye, yemuñu ci, ndax ŋàññ nañu màkkaanu taskati xibaar bu Yuusu Nduur bii di iGFM ak tamit RTS, rawatina yéenekaayi réewum Farãs France 24 ak RFI. Ñu neeti, kàddu njiitu jawriñ lii di Muxamadun Bun Abdalaa Jonn ak doxalinu taskati xibaar yees jot a lim, ag càcc a lalu ci suuf, ñu bëgg a nax askan wi, jox leen ay lim yu wérul. Waaye, ñoom duñu ko nangu ; te bu ko jaree, dinañu génn ànd ak askan wi xeex, jubali Pale ngir déjjati fa Maki Sàll.
Bi dënn yi demee ba tàng la àttekat bi jiite Kurélu ndajem wote bi xéy, woo taskati xibaar yi, daldi delloo njiitu jawriñ li palaasam, xamal ñépp ne, kenn amul sañ-sañu wax ne kii falu na walla ñaareelu sumb day am lu dul Kurélu ndajem wote gi mu jiite walla Ndajem ndeyu àtte mi. Bees ko laajee nag, kañ lees war a jot ci ngirtey wote bi, dafa xaarloo askan wi ba alxames walla àjjuma jees dégmal. Loolu nag, teeyoon na xel. Ndaxte, ak xeeti jumtukaayi xarala yi fi nekk, jarul woon a joxe àpp gu ni tollu. Mbaa du njiitu réew mi daa takkaloon pot Demba Kànji ak i ñoñam ngir ñu wax ne moo jël ndam li ? Am na sax ay ndaw yuy wax ne nguur gi dafa bëgg a foqati baatu askan wi. Ba tax na, ñenn ci ñoom tàmbalee ñaxtu ca buntu RTS di kaas naan ñaareelu sumb day am ci nii mbaa ci nee. Waaye, waa Bennoo Bokk Yaakaar ñoom, ñu ngi ŋoy ci seen lim bi njiitu jawriñ yi fésaloon, naan : « wure wi dem na këŋŋ, Makee faluwaat ! » Li am ba des mooy ne, askan wi gëmmul nelawul. Bi Demba Kànji joxee dogalam ba tey, nit ña ngiy xultu tëwa ba, kujje gi woote na doxu-ñaxtu tey ci àjjuma ji, buñ jullee tàkkusaan ba noppi. Lan la ndaje moomuy jur ? Yàlla rekk a xam. May laajati : mbaa du léeb dafa tàbbi géej ? Moom daal, xalam demoon na bay neex…
Am na tamit ñu naan Maki Sàll dunguru Emmanuel Macron doŋŋ la te sax Tubaab yee ko may fitu yemale joŋante bi ci benn sumb kott. Loolu tekki ne Frãs ay ndeyu-mbill gi te xéy-na lees war a def mooy bañatee jënd lépp luy doomi-Frãs di jaay fi ci Senegaal, moo xam Auchan la, walla Orange laak Total walla ñeneen.
Àttekat bii di Demba Kànji nag, bu tasul woon yaakaaru askan wi, Senegaal du mel tey ni réew mu toog ci nen. Xéy-na am na lu ñuy yoot. Fitna du yem ci boppu boroom te bu pënd wuree, fattu bare. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/jonante-ren-bii-petorool-lay-xeen/ | JOŊANTE REN BII, PETOROOL LAY XEEÑ…
Keroog, askanu Senegaal jóg na ci njekk ak teggin, daldi def li ko war ci tànneefu njiitu réew mi. Ndax, bi waxtu wi jotee, nit ñi gànnaayoo nañu seeni kàrt, ànd ak yar, dem ndànk sànnil ko wutaakon bi leen doy. Léegi nag, Maki Sàll jàllaat na waaye mbir mi dese naa leer ba tey. Yàlla na ngoru nguur geek kujje gi tollook li leen réew mi sédd.
Ci téeméeri falaakon boo jël, daanaka juróom-benni fukk yi wote nañu. Maanaam, doomi-Senegaal yi wone nañu ni mbir mi yitteel na leen lool. Te sax, bu dee wax dëgg rekk, lim bi waroon na fee gën a takku. Waaw, dafa di nag, ñu bare jotuñu ci seeni kàrt. Lu waral loolu ? Ñenn ñaa ngiy duut baaraam nguur gi, waa nguur gi ñoom di indiy lay yu dul jeex. Li am ba des daal moo di ne, ci jàmm ak salaam lees yeewoo ci dibéeru wote bi, yendu ci itam. Waaye, toqu dereet dina yàq këllu soowu. Ab njiitu jëwriñ lu muy dox di falaate te amul gëdd bi, amul sañ-sañ bi ? Bun Abdalaa Jonn mii nag, moo fi naroon a taal daay. Ndege, dafa dem ca RTS, janook askan week àddina sépp, ne Maki faluwaat na ci sumb bu njëkk bi. Coow li ne kurr, xol yi tàmbalee tàng, ñenn ñiy séentu fitna ci réew mi. Idiriisa Sekk ak Usmaan Sonko woo taskati xibaar yi ngir xamal askan wi ne kenn warul a nangu loolu, yëkkatiy kàddu jëmale leen ci waa APR, ni leen duñu nangu mukk ñuy jalgati kàrt yi ngir sàcc wote bi, jàllale Maki ci sumb bu njëkk bi.
Li waroon ñi faral njiitu réew mi mooy ñu am ngor te ànd ak dal, bañ a may kenn mu tam seen mbër dëmm, naan ni mu faluwaatee daa taq suuf. Li ñu naan ñaareelu sumb, ñu bare yakaaroon nañu ko. Te Senegaal, saa bu ñaareelu sumb masee am ci joŋante bu ni mel, ki toog ci jal bi day ñàkk. Bu ko defee, mu dem Frãs, bàyyee nook sunuy mbir, toog Wersoŋ ni Seŋoor, di jiite “Francophonie” ni Abdu Juuf mbaa jaaxaan Wersaay ni Ablaay Wàdd. Usmaan Sonko ak Idiriisa Sekk ñi nga xamante ne, kenn ci ñoom moo naroon a jàll ci waññi bu njëkk bi, li leen waroon moo di taxaw temm ngir waññ bi jaar yoon waaye ànd ceek dal te bañ a waxe xol. Ci sunu gis-gis, def nañu ko. Li leer ba leer moo di ne mu neex gornmaa bi walla mu naqadi ko, askan wi rekk ay buur. Ndaxte, saa su jaay-doole walla njuuj-njaaj àntoo, daa fekk askan wi ne yàcc-yàccaaral di seetaan.
Doomi-réew mi wote nañu, te benn a ngi nii ci jàngat yiñ ci mën a def : demokaraasi, àndul ak xiif. Ku sa biir feesul, doo ko tal…
Doomi Senegaal yi féete bitim-réew, seen doxalin ci wàllu politig wute naak doxalinu ñi nekk ci biir réew mi. Sunu mbokk yi tasaaroo ci àddina sépp, wone nañu bu baax ne Usmaan Sonko lañu wóolu. Usmaan Sonko nag, digul kenn xaalis walla ndombog-tànk. Lenn doŋŋ la dige, mooy ne : su faloo, caaxaan dina jeex ci miim réew te it, dina def kemtalaayu kàttanam ngir nu moom sunu bopp, dunde sunu ñaq, jariñoo sunu suuf.
Doomi Senegaal yi féete bitim-réew, ñi ci ëpp dañoo jàng, am xéy tey sant Yàlla, daanaka. Nit ku suur, nag, xelam day ubbeeku te xalaatam du gàtt. Leneen li mooy ne ñooñu nekk bitim-réew, nguur gi masu leen a amal njariñ, lépp lu ñu am ñoo ko liggéeyal seen bopp. Yakaaruñu diw falu jox leen ay màrse walla ndombog-tànk. Ñooñu, su ñu wéetee ci mbañ-gàcce gi, jiital Senegaal ak ëllëgam daf leen di yomb. Ñi ëpp ci ñoom dañu tàmm a gis, fa ñu dëkk, njariñu politig bu jaar ci yoon. Day tax am réew moom boppam, di xeex ger ba noppi am ay njiit yuy fullaal seen yokkuteb askan. Bu dee nag xamoo fu dul Ndumbelaan gii nga xamante ne ku ñàkkul jom, ñeme kàcc tey cuune, sa tekki ci politig dafay jafe, ñu mel ni Maam Mbay Ñaŋ, walla Farba Seŋoor mën nañ laa doy. Boo ci tegee xiif nag, ak ñàkk liggéey mbaa lijaasa, sa dara doyul, xamoo fan ngay jële depaasu ëllëg, ñu jënd laak saaku ceeb walla piisu legoos du jafe. Réew mi nag, dafa am ñu fi nekk te defuñu, 1960 ba léegi, lu dul aakimoo li ñépp bokk. Ñooñu, seen yoon newul ci Senegaal, li leen yitteel mooy naka lañuy def ba ñoom ak seeni mbokk ñuy jot ci liggéey yeek màrse yi gornmaa biy séddale. Seen gis gis soriwul, doonte sax xiifuñu te ñu ci bare dañoo jàng ba ni arr.
Am na, ci sunu mbokk yi nekk bitim-réew ku ci ne, bi ngérte yi feeñee, ñoom def nañu li leen war ; mu yokk ci ne ñi nekk Senegaal nag ñoo ci des te bu ñu dof-dofloo ba falaat Maki, buñu defati seen xel ci ku leen yónnee “Wari” walla “Western Union”. Gaa, ay kaf rekk la woon wànte mel na ni ku sa biir feesul taloo demokaraasi. Leneen lu jar a bàyyi xel, mooy doxalinu ndawi Senegaal yi jàng lekool. Ñoom it Sonko rekk a leen doy, dooleel nañ ko bu baax te li looluy biral moo di ne Senegaal tegu na ba fàww ci yoonu coppite. Su dul déwén it, ciy at yu néew lay doon. Sonko jiite xeex boobu mbaa mu bañ koo jiite, ndam li mu am ren law mbaa mu yem fi, xaley Senegaal yi seen gis gis leer na, xam nañu ne xeetu politig bi Maki taamu, su fi saxee, dees na yeewu bés, Senegaal mel ni Gaboŋ, maanaam am xéewalu petorol ba noppi jébbal ko Frãs te ku ne piip ñu ceene la tëj kaso, fàtte la fa. Ak li coow liy bare yépp, kan lañ dégg mu tudd fi Xalifa Abaabakar Sàll fan yii ñu génn ?
Mamadu Jàllo | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/aliyu-sall-gii-maryiis-saana-kumba-am-ndey-ak-kumba-amul-ndey/ | ALIYU SÀLL, GII MARYIIS SAAÑA : KUMBA AM NDEY AK KUMBA AMUL NDEY | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/seex-bekaay-deddu-na/ | SÉEX BEKAAY DËDDU NA !
Xalifa tarixa xadiir yi ci Senegaal wuyuji na Boroomam ginnaaw tawat bi ko tëraloon. Kan moo doonoon Séex Bekaay ? Jaar-jaaram lan leen dégtal ci yaxal bile, ngir xamal leen kan moo doon xalifa ba woon ca Njaasaan.
Séex Al Bekaay mu ngi gane àdduna ca atum 1929, ñaari weer ginnaaw ba baayam Séex Bu-kunta nelawee. Mu nekkoon taawam, nekk tamit juróom-ñaareelu xalifaam. 2018 la toog ci xilaafa gi. Mu nekkoon ku ràññeeku ci mbooru araab. Doonoon ku fés ci bëgg Téere Bu Sell Bii di Alxuraan. Am njàngam mu doore ko ci magam Muhammet Kunta. Waaye, Gànnaar (Muritani) la ko mottalee. Ci noonu, bi mu ñibbisee la dal Medina Baay ci wetu Allaaji Ibraayma Ñas. Mu nekkoon ku ko jege lool ba léegi kóllëre googu di wéy ba ci Séex Maahi Ñas miy xalifab Medina Baay. Mu mel ni yamutoon rekk ci diine ji. Nde, Séex Bekaay bokk na ci ñi njëkk a liggéey ci caytu gi. Mu daan yëngu ca APS (Agence de Presse Sénégalaise).
Ñu denc ko ca dëkk bu sell ba di Njaasaan, ci teewaayu mbooloo mu takkoo-takku. Mbokk, taalibe, kilifa diine niki aada, ñépp ñoo ñëw teewe ci ginnaaw jullig tisbaar gi. Ñu seetlu fa teewaayu Taala Silla ma fa jiitu woon jëwriñ ji ñu dénk biir réew mi, ci turu Njiitu réew mi, Maki Sàll, jottali fa njaalam njaboot gépp, waaye tamit bépp jullit. Niki ni ñu baaxoo defe, ginnaaw dëddug Séex Bekaay, ka ko fa wuutu di Séex Bu-Siidi Maxtaar Kunta, nekk léegi xalifab Njaasaan.
Mënees na wax ne Njaasaan a ñàkk, waaye umma Islaam a ñàkk kilifa gu mag. Jaar-jaaram doon lu fésul ndaxte li ko yitteloon mooy diine ji. Loolu, terewu ko ubbeeko ci xam-xami àdduna ak ug yëngoom. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/can-2023-aliw-siise-tann-nay-ndawam/ | CAN 2023 : ALIW SIISE TÀNN NAY NDAWAM
Barkaatu-démb ci àjjuma ji la tàggatkatu ekib nasiyonaal bi, Aliw Siise doon amal ab jàkkaarloo ak taskati xibaar yi ngir wax li jëm ci waajtaayu CAN bees dëgmal ca Koddiwaar ak biral ndaw yi mu tànn ngir ànd ceek ñoom ñu taxawal fa sunu réew mii di Senegaal. Seen dem gii nag dana wuute ak ya wees. Ndax daf ciy ame ñaari taxawaay. Bu njëkk bi mooy ni moo mujje yëkkati kub bi kon dafa war a xeexal cëram woowu. Ba ca topp nag di xeexaat ngir jéem koo tóllanti. Aliw Siise yëkkati na ay kàddu yu jëm ci loolu wax ne :
“Ragalunu. Danuy dem ci CAN bii ak yéene ju réy a réy. Nun nooy buuru Afrig. Kon ekib bi yelloo na cër wu ëpp wiñ ko jox nii. Bu Senegaal wóoluwul boppam, man gisuma ban ekib mooy wóolu boppam ci Afrig gii.”
Gannaaw loolu nag biral na limu ndaw yim tànn. Ñoo nekk nii :
Góol yi : Eduwaar Méndi, Séeni Jeŋ, Móori Jaw.
Defãsëer yi : Kaliidu Kulibali, Musaa Ñaxate, Abdu Jàllo, Yuusuf Sabali, Fóode Baloo Ture, Formóos Méndi, Abdulaay Sekk, Ismayla Jakob ak Abdulaay Ñaxate Njaay.
Miliyë yi : Idiriisa Gànna Géy, Séexu Kuyaate, Lamin Kamara, Paap Mataar Saar, Paap Géy, Paate Siis, Nàmpalis Méndi ak Kerepeŋ Jaata.
Ataakã yi : Saajo Maane, Ismayla Njaay, Ilimaan Njaay, Nikolaa Jakson, Bulaay Ja, Abiib Jàllo ak Abdulaay Sima.
Kon lii mooy limatu ndaw yees tànn ngir ñu teewal Senegaal fa Koddiwaar ca CAN ba. Am ñu bokkon ca ba ñuy jël kub bi weesu te bokkuñu wii yoon. Xaarees na ci ñoom ñu ñaanal ekib bi te gën a liggéeyaat ngir weneen yoon ñu mën a dikkaat, nde la ca ëpp ay ndaw lañu.
Gannaaw tànnug Aliw Siise miy tàggatkat bi nag, am na ay coow yu sew yuy jóg jëm ci lim nu andil rawatina ci mbaali-jokkoo yi. Foo geestu ñoo ngi ciy wax. Li gën a bari ci lees di wax moo di ne, moom Siise, dafa bari lim woo ciy defãsëer, ba sax ci miliyë bi, xeexkat yi ñoo ci ëpp. Boo jàngatee tànn gi wàlluw defãs moo ci ëpp te jamono jii ñu xarañ ci kaw ak ci kanami kã yi lees gënoon a xaar ci moom.
Gannaaw loolu it yëkkati na ciy kàddu moom Aliw Siise di xamle ni:
“Duma Yàlla, duma yonent. Tàggatkat laa te awmay xërëm ngiy soppi yëf yi. Li ma mën tay mooy góor-góorlu. Lenn lu nu mën, nun, mooy góor-góorlu.”
Muy lees ko mën a nangul itam. Bu loolu weeso, ekib bi dina amal ndajem xaritoo ak kii di Niseer fii ci réew mi ca fowub Abdulaay Wàdd 8i fan ci weeru saŋwiyee wii bu 18i waxtu jotee.
Nu mànkoo wutiwaat ndam li. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-ajjuma-7-awril-2023/ | LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (ÀJJUMA 7 AWRIL 2023)
XEETAL CA ITALI
Kañ mbirum xeetal, xeeb ak mbañeel di jeex ci àddina si, rawatina ci àddinay kuppe gog, yoonam nekku ca ? Saa bu ñu yaakaaree ni tane na rekk,beneen ñaawteef jibati. Daf ci am réew yoy, fa la Waaloo gënee aay, te Itali ci la bokk. Ndax, foofu ca Itaali, mënees na wax ni seen baaxu-maam la. Daanaka doo toog ab diir lu moy dinga dégg coowalug xeetal lëmbe fa. Bërkaati-démb rekk a ci mujju. Nde, kuppekat bu ñuul bii di Lukaku, dundaat na yu ñaaw yile. Ca joŋante ba doxoon diggante Inter Milan ak Juventus la lenn ci siporteeri Juventus doon ko yuuxook a woyal ay baat yu ñaaw yuy ŋàññi ñuulaayam ak di xalab xeetam. Doonte ne, moom Lukaku, du saa-Afrig. Ndaxte, bu dee Afrig lay way-juram cosaanoo tam, Belsig la juddoo, màgge, taamoo nekk doomu Belsig wëlis Kongo gi maamam yi fekk baax. Waaye de, li wolof di wax rekk, wax ju ñaaw dëkkul fa mu jëm, fa mu jóge la dëkk. Te, saaga yooyu taxu koo génn ci matsam. Nde, dugal na fa benn bii, daldi daw ba seen kanam, jàkkaarlook ñoom, def baaram ba ca gémmiñam. Mu mel ni ku leen di tontu, di leen noppiloo. Waaye, arbit bi nag daf ko ci jox ab ruus. Ruus boobu nag, jur na fa coow, ndax ñu baree bari ànduñu ci ndogalu arbit bi.
CHELSEA
Frank Lampard la ñu tegandi ca bopp këlëbu Chelsea ngir mu àggali li des ci sàmpiyonaa bi, gannaaw bi ñu dàqee ka leen doon tàggat, Graham Potter. Ñaari yoon a ngi nii njiiti Chelsea yi di dàq seen tàggatkat. Ndax, Graham Potter mi ñu mujje dàq, daf wuutu woon Thomas Tuchel mi ñu njëkkoon a dàq. Lampard, nag, wii mooy ñaareelu yoon muy yor Chelsea. Nde, njëkkoon na leen tàggat laata ñu ko dàq moom itam.
UEFA
Aleksander Ceferin falaat nañ ko ci boppub UEFA ba atum 2027. Gii moo di ñetteelu moomeem ci boppu kurél gi boot kuppeg Tugal. Ndaxte, atum 2016 lañ ko fa tegoon ba léegi.
SAAJO MAANE
Ñañcoo bi ñëwaatagul ba léegi ! Saajo Maane, ba tey, delloogul buum gi ca boy-boy ga. Ndax, bim delsee ba nëgëni, kenn xàmmeetu ko. Amaana toogaayam bu yàgg bim toog ci sababu gaañu-gaañu bim ame woon a ko waral. Amaana yit, fi ñu koy teg moo baaxul ci moom. Nde, ñaari joŋante yi mu am ak ekibu Senegaal ci fan yii ñu génn, gis nañu ni ba léegi am na lu des. Waayeet, ca këlëbam bii di Bayern Munich itam, waxi noppi. Dafa di, keroog, ca seen joŋanteb kuppe bi mujju bi, daf cee meloon ni ku réer ci biir pàkk mi. Warees na xool, seet ba xam luy jafe-jafe bi ngir indi ci saafara balaa moo gën a yàgg.
KUBU ESPAAÑ : BARCA 0 – 4 REAL
Bërki-démb, ci àllarba ji, Barcelone ak Real Madrid doon amal seen ñaareelu ndaje ñeel kuppeg Buuru Espaañ bi (Coupe du roi). Ca fowub (estaad) Barça lees ko doon amale. Waaye, nag, Real daf ko toroxal biir dëkkam, dóor ko 4-0. Ca joŋante bu njëkk ba, Barça moo dóoroon 1-0. Kariim Benzema moo dugal ñetti bii. Moom, Benzema, mooy saa-Real bi njëkk a dugal ñetti bii ca “Camp Nou” ginnaaw Ferenc Puskas mi ko njëkke woon atum 1963. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-allarba-1-mars-2023/ | Li gën a fés ci xibaari tàggat-yaram (àllarba 1 Màrs 2023)
Paul Pogba
Gannaaw 11i weer yi mu toog ci sababu gaañu-gaañu bu metti bi mu ame woon, Paul Pogba delsiwaat na ci pàkku wure yi démb ci talaata ji. Muy Joŋanteem bu njëkk ba mu delloo ca Juventus ak léegi.
FIFA the Best
Saa-Àrsàntin bi, Messi, moo jël raaya ji ñu jagleel wurekat bi gën a xereñ ci atum 2022 mi. Loolu nag, jur nay ñurumtu ndax am na ñu jàpp ne yelloowu ko.
France
Noël Le Graët nekkatul njiitul FFF. Démb ci ci taalata ji, 28i féewaryee 2023 jii lañ ko xamle. Gannaaw loolu la ko Gianni Infantino, Njiitul FIFA, fal ci boppu kureelu FIFA bu Pari.
Just Fontaine, kenn ci ndaanaani France ya woon, wàcc na liggéey tay jii ci àllarba ji. Mooy ki ëpp ba léegi lu mu dugal kuppeg àddina lëmm, 13i bii ci benn kub. Ba léegi keneen defaatagu ko.
Coupe du Roi / Espagne
Xamle nañ ni kii di Pedri, Usmaan Démbele ak Lewandowski duñu bokk ci ñiy jàmmaarlook Real Madrid suba ci alxemes ji.
Basket
Ekibu basket Senegaal bu góor ñi du dem ca kuppeg àddina si ñeel basket. Meetar Baabakar Njaay nag àndul ci toogloo giñ toogloo Senegaal ba tax muy duut baaraam waa FIBA, teg ci yëkkati yii kàddu : “Senegaal dañ ko toogloo ci lu jaarul yoon”. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/3117/ | Ëllëgu gaynde yi ca tugal
Naples noppeegul ngir bàyyi Kalidu Kulibali mu dem. Moo ngi ci tànki yokkal ko peyooram ci àpp gu gudd donte ni këlëb yu mag yu mel ni PSG, Roma, Chelsea, rawatina Barcelone, fësal nañ seen bëgg-bëgg ci doomu Senegaal ji ak di ko dig lu ëpp li ko Naples daan fey. Lu soxal Abdulahat Jàllo, Paris mën na koo abale walla mu jaay ko Stade de Rennes mi nekk ciy tànkam ; fekk na Saajo Maane ñuy wéy di ko gën di dégg ca Bayern. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6-7-2023/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM (6/7/2023)
AFROBASKET-JIGÉEN, RUWÀNDAA 2023
Gannaaw tànn gu njëkk ga, Mustafaa Gay, seggaat na ekib bi, tànn ci jigéen ñi war a teewali Senegaal fa fa Ruwàndaa, bokk ci joŋanteb Afrobasket bu jigéen ñi. Ñii toftalu la jël :
Way-dawal yi (meneuses)
Leena Timeyraa, Siyaara Siney Dilaar, Faaty Jeŋ
Gannaawe yi (arrières)
Kuuna Ndaw, Yaasin Jóob
Ma-laaf yi (ailières)
Ayaa Taraawore, Matild Jóob, Faatu Puy, Soxna Faatu Silla
Wërmbiij yi
Ummu Xayri Saar, Ummu Kalsum Ture, Faatu Jaañ, Aram Ñaŋ, Aysa Nduur.
SÀMPIYONAA ESPAAÑ AM NA TUR WU BEES
Soppes na turu sàmpiyonaa Espaañ. Léegi, tuddatul LaLiga. Bés niki tey, dees na ko woowe LaLiga EA Sports. Nde, dañu am esponsoor bu bees, muy defarkatu powum kuppe bii di EA Sports.
REAL MADRID SUUFOOTI NA BARCELON CI ARDA GÜLER
Real Madrid defati na ko Barcelon. Fan yii yépp, Barcelon a ngi waxaale ak njuuma Turkii liy futbal Fenerbahçe, Arda Güler. Waaye de, Real Madrid dafa jaar ci suuf, wax ak xale bi, déggoo ak moom ba mu tànn Real ci kow Barcelon. Lu ni mel nag, du guléet. Nde, muy Vinicius Junior, di Rodrigo, ñoom ñépp, Real dafa suufu Barcelon, jënd leen.
Barcelon dafa yabaloon ay ndawam fa Turkii ba ñu tàmbali woon waxtaan ak futbalkatu Fenerbahçe bi. Amoon nañ ci yaakaar lool sax. Ca la Real Madrid ñëwee, ràccal boppam, Arda Güler daldi nangul ekibu péeyu Espaañ bi. Ci fan yii di ñëw, dinañ matal li ci war lépp ngir mu ñëw bokk ci ekibu Real Madrid bu mag bi. Bokk na ci li ko yombal nag, mooy magi Real yi daan dégganteek moom, niki ñoom Modric, Kroos ba ci Özil mi fa nekkatul sax.
MASON MOUNT DEM NA MANCHESTER UNITED
Manchester United amati na limatu 7 bu bees. Mason Mount mi nekkoon Chelsea lañu jënd. Ndax dina dox ci tànki Cantona, Beckham, Ronaldo, ñi siggil 7 bi ; walla dafay mel ni ci ko mujjee sol te lajj : Owen, Valencia, Di Maria, Depay ak Cavani ? Seetaan a dàq cim ndaje.
FRANK LAMPARD AK STEVEN GERARD DEM NAÑ ARAABI SAWDIT
Frank Lampard amati na këlëb bu bees. Wii yoon, ca naar ya la dem, Araabi Sawdit. Këlëb bii Al-Ittihag lay yori. Dafa topp ci tànki Steven Gerard miy yori tamit Al Etiffaq. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/ | KUPPEG ÀDDINA GEES JAGLEEL U17 FA ENDONESI
Tànnees na fukk ak benni ndaw yi war a teewal Senegaal fa Endonesi ñeel kuppeg àddina jagleel ñi ëppalagul 17i at. Nii la toftale gi tëdde :
Góol yi
Sëriñ Juuf (G.Foot)
Makura Mbuub (G.Foot)
Séex Bàmba Faal (Diambar FC)
Defãsëer yi
Sëriñ Fàllu Juuf (G.Foot)
Mammadu Aliw Jàllo (Diambar FC)
Guy Feliks Lima (AFAT Thies)
Ibraayma Jàllo (G.Foot)
Buubakar Saajo Ba (Étoile Lusitana)
Sériif Keebaa Ñabali ( Océan FC)
Alfa Aamadu Ture (G.Foot)
Miliya yi
Piyeer Antuwaan Jaata Dorival (Dakar Sacré Coeur)
Paap Daawda Jong (AF Darou Salaam)
Sëriñ Saaliw Fay (G.Foot)
Mammadu Lamin Saajo (Environnement Foot)
Mammadu Ñing (Espoir de Guédiaway)
Ataakã yi
Idriisa Géy (G.Foot)
Omar Sàll (Environnement Foot)
Yayaa Jémme (Diambar FC)
Amara Juuf (G.Foot)
Mammadu Sawane (AFAT Thies)
Clayton Silverio Kàndi (Espoir de Guédiaway)
Ñii ñooy ndaw yi ñu tànn ngir ñu dem teewal réewum Senegaal ca kuppeg àddina giy ame fële ca Kembaaru Asi, dëkku “Indonesie”. Joŋante bi nag moo ngi war a tàmbali fukki fan ci weer wii nu nekk. Réewum Senegaal mépp di ci ànd ak seen i doom di leen ñaanal ñu ame fa ndam.
Mànkoo jëli ndam li ! | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/koronaak-addina/ | KORONAAK ÀDDINA
Taalifu Làmp Faal Kala
Ki daan mere nit ñi ci ñàkk a nuyoo
Moo bank ab loxoom di tere nuyoo
Ki daa tëju amul yitte lañ daan mere
Tey ku tëjuwul bari yitte la ñuy tere
Jàngoon naa ni fu jullit yi def mbooloo
Yàlla dafa fay tàbbal yërmaande Rahma
Dakkandil nañ jëm jumaa julliji àjjuma
Tere màggal, cant ak jàngeek dajaloo
Foo déggaan ku juge Itaaleek Farãs
Njëkkanteji sërica ku jiitu ëpp sãs
Tey ku ñu ni wiisaa ngii amoo sãs
Jàngoro ji wëlbati na àddina tey
Dem ba ndigal soppiku tere kay
Ku ne tiit di ñaan na koronaa bi fay
Ndax dafa bon day fàdd di ray | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/as-pikine-guediawaye-fc-xumb-te-dagan/ | AS PIKINE – GUEDIAWAYE FC : XUMB TE DAGAN
Keroog, ci gaawu gi 29 awril 2023, sàmpiyonaa Senegaal bi jaxoon na lool. Ndax, As Pikine ak Guédiawaye Fc ñoo doon daje. Mu nekkoon joŋante boo xam ne, ñi ko doon xaar bari nañ. Ndaxte kat, du joŋante bu ndaw. Mënees na jàpp ne sax, ni fii ci Senegaal, mooy sunu Barça-Real, walla sax Paris Saint-Germain-Marseille. As Pikine ak Guédiawaye Fc di ñaari ekib yu bokk daanaka benn gox mbaa nu wax ni ñoo takkaloo, ñuy yenn ci ekib yu gën a mag ci sàmpiyonaa Senegaal gi.
As Pikine bu waree joŋante, ni ñuy waajalee seen bés yi ak soppe yu bari te gëm ekib ba nañuy mel, meneen mbir la. Muy këlëb bu yàgg a wane boppam, di ekib bu mag. Guédiawaye Fc itam, naka noonu. Ci at yii ñu génn, gis nañu jaloore yi mu fi def yépp : wàcc Ligue 2 bi, jël ko yéegaat fekki punkali Ligue 1 yi.
Gis nañu nag, ñi dëkke ca gox ya na ñuy jàppee ci seen i ekib ak liñ leen jaral. Ku ci mel ne Bàlla Gay, mbër mu mag mi dëkke Géejawaay, def na ci waajtaayu joŋante bi benn tamndaret ci sunuy koppar, mu nekk luy dooleel ekib ba ci lu bari.
Joŋante bi nag, barkaati-démb, ci gaawu gi, la amoon. Rëyaayu joŋante ba taxoon na ñu bàyyi fowu yépp, tóxal ko ca fowub Abdulaay Wàdd, Jamñaajo, fa ekibu Senegaal bu mag biy joŋante. Ekib bu ci nekk, indi nga say soppe, mu neexoon lool, xumb ba dee. Joŋante bi nag neexoon na lool, bal bi daw na, futbal bi set na. Waaye nag, ndam demul, ndam dikkul. Ñaari ekib dañoo mujje joxante loxo, kenn dugalul sa moroom. Guédiawaye Fc, boo xoolee, moo féete kaw. Ndaxte, mooy nekkagum ci ñetteelu toogub sàmpiyonaa ba ak 31i poñ, As Pikine jëlagum 6eel ak 25i poñ.
Joŋante bi jur na liñ ci doon xaar, muy kuppe gu rafet, bal bi daw, ñu amal ko ci jàmm. Ba ci soppe yi nekkoon ci kaw, yëngal nañu ba mu neex, lépp ci jàmm ak salaam.
Ñu bari nag rafetlu nañu ni ñu yóbboo joŋante gi ci bóobee bërëb. Ndax, jàpp nañ ne dina gën a may bët ak bayre sàmpiyonaa bi. Rax-ci-dolli, ekib boo fa yóbbu, daanaka ay soppeem dinañu sawar a seetaani ko, te dina dundal sàmpiyonaa bi ak kuppeg Senegaal.
Ñoo ngi xaarandi yeneen bés yu ni mel. Ndax, bile moom neexoon na lool. Te, lu neex du doy. Ndaxte, xumb na, dagan na. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/jigeen-du-xaru-tabaski/ | JIGÉEN DU XARU TABASKI !
“DOY NA !”, “DAFA DOY !”. Ñaari baat yii mën nañoo tënk doxu-ñaxtu bi amoon ca diiwaanu Tàmbaakundaa ak ci péeyub réew mi, gaawu bii weesu, 25eelu fan ci weeru me. Binta Kamara, 23 at, lañu xoj ba mu sedd guy. Mbir maa ngi xewe foofu ca Tàmbaa ñetti ayu-bés ci ginnaaw, bésub gaawu, 18eelufan ci weeru me. Ki ko rey, nag, da ko doon jéem a siif, ndaw si bañ, waa ji jaay ko doole, xoj ko ba mu dee ciy loxoom. Jëf ju ñaaw jooju, siifaate beek reyaate bi, la ñaxtukat yi ne : “na fi dakk !”.
Dafa di sax, baayu Binta Kamara politiseŋ bu far ak Maki Sàll la, amaana looloo waral mbir mi gën a fés. Wànte, jamono jii ak at yii ñu weesu yépp, siifaate bi ak reyaate bi dafa takkarnaase. Ndaxte, ci benn ayu-bés gi doŋŋ rey nañu ci ñaari jigéen : kenn ki ci màrse bu Wakaam lañu fekk néewam, ñu futti ko ba mu set wecc, keneen ki Kumba Yàdd la tudd, Cees lañu ko reye gànnaaw bi ñu ko siifee ba noppi. Kurél yiy sàmm àqi jigéen ñi fii ci Senegaal nee nañu, luy jot jot na ginnaaw dee, nguur gi na jël ay ndogal ci ni mu gën a gaawe, dakkal ñaawtéef yi jigéen ñiy jànkoonteel. Ndakaaru sax, amaleesoon na fa ab doxu-ñaxtu.
Keroog, ca Péncum askan wi, “Place de la Nation” ci nasaraan, ñu bare ci doomi-réew mi taxawoon nañu fa ngir naqarlu ak kaas ñàkk kaaraange gi réew mi nekke, te mu gënatee metti ci jigéen ñi. Ci anam bu doy waar lañu fa taxawe woon. Ay kanam yu sadd di wone seen mer ak seen tiis. Ñu seel seeni kanam, péntuur ci lu nirook deret, mu ciy rogaat. Li ñu ko dugge woon, moo doon xamal ñépp ne deretu jigéen ji ñuy tuur dafa doy.
Waaye, maandu war na ku nekk ci nun. Ràcc jëmale sa kanam baaxul. Dëgg la, jigéen ñi sonn nañu wànte rey bi moom fépp la, du jigéen ñi rekk la ñuy bóom. Ndax, saa su nekk ñu dégg ne am na as ndaw su faat jëkkëram ci lu ñàkk faayda te kenn du dégg kuréli jigéen ñi wax. Bu ko defee, li ñu war a xeex dëgg mooy rey bi ci boppam. Loolu nag, yemul rekk ci teg fiy daan yu diis walla ñu def ku rey ñu rey la. Li gën mooy ñu xoolaat yarinu xale yi ca ba ñuy tuut-tànk, jàngal leen yar ak teggin, waaye jàngal leen itam diine, ngir saxal ci seen xol ak ci seen xel ay jikko yu rafet. Ndax Wolof Njaay dafa ne, gune lawtanu yomb la, boo ko wëlbatiwul, mu law fu la neexul. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM (21/6/2023)
Senegaal duma na Beresil 4-2
Démb ci talaata ji la ekibu Senegaal bu mag bi doon amal joŋantebe xaritoo ak bu Beresil, faLiisbon, gëbla Purtugaal. Ndekete, sunu gaynde yi yarasuñ benn yoon ! Firndeel nañu tamit ne, duñu yàqi te duñu bàyyeeku. Ndax, Beresil a ñjëkk a dugal. Waaye, Senegaal mayu ko sax mu noyyi. Nde, 4 la ko yen laata Beresil di dugalaat beneen, muy 4-2. Ndam li, ndam lu réy réy. Ndege, Senegaal mooy ekibu saa-afrig bi njëkk a dugal Beresil 4i bii. Rax-ci-dolli, 2014 ba tey, ginnaaw bi ko Almaañ rokkosee woon 7i bii ya, guléet mu jël lu tollu ci 4i bii. Kon, gàcce-ngaalaama sunu gaynde yi. Abiib Jàllo moo dugal benn, Marquinhos dugal seen kã, Saajo Maane lakk caax yi 2i yoon.
Aliw Siise bégoon na ci gaynde yi ak ci ni joŋante bi deme. Moo ko tax a bëgg lu ni mel di faral di am. Daf ne :
“Joŋante yu mel nii lanu bëgg ngir di ci nattee sunu doole. Bëggaat nanu ci yeneen yoo xam ni, Ndakaaru lay doon, Senegaal. Beresil na ñëw ñu dalal ko sunu réew mu xam ko, walla sax Àrsaantin.”
Bu dee Saajo Maane nag, mi ngi gën a rëdd turam ci mbooru kuppeg Senegaal. Ndax, démb la dugal 36eel ak 37eeli biiyam ak Senegaal.
Cristiano Ronaldo : 200eelu joŋante ak Purtugaal
Ronaldoo démb ladoon amal 200eelu joŋanteem ak dëkkam, Purtugaal. Guddeem ga neexoon na nag. Ndaxte daf ci dugal benn bii bi tax Purtugaal gañe joŋante bi. Moom itam, mag mu dul màgget la ; doon paa terewukoy gën a aj turam ci mboorum kuppe gi.
Ngoloo Kànte fekki na Bensemaa
Ngolo Kànte juge na Chelsea, fekki Kariim Bensemaa këlëbu Al-Ittihad, ca naari Araabi-Sawdiit ya. Liñ naan xaalis mën na lu ne, ndeke dëgg la. Ba fa Ronaldo demee, dégg nañ ci gannaawam wax ju nekk. Waaye de, dafa mel ni ñiy topp yoonam a ngi bëgg a bari. Naar yaa ngi yóbbu ñu bari. | Defuwaxu |
https://www.defuwaxu.com/njaay-daraapoo-dedduna/ | NJAAY DARAAPOO DËDDU NA
Momar Njaay, ñu gënoon koo miin ci turu “Njaay Daraapoo”, dëddu na. Moom, nag, ku ràññeeku woon la ci wàllu kuppeg Senegaal. Mi ngi faatu ci àjjuma ji 31 màrs 2023. Muy xibaar bu tiis ci waa Senegaal yépp, rawatina njabootug kuppe gi.
“Njaay Daraapoo”, ku fësoon lool la ci ekibu Senegaal bi. Ndaxte, atum 2002 la tàmbali woon a ànd ak ekib bi. Dafa bokkoon ci mbootaayu 12eelu gaynde gi. Looloo indi turu “Njaay Daraapoo” wi. Nde, moo doon yore raayab Senegaal bu rëy bi, di ko wëndeel, saa bu ekib biy joŋante. Ndeysaan, amul fu mu àndul ak ekib bi. Muy Kuppeg Afrig, di Kuppeg àddina si, fépp la dem, topp ginnaaw gaynde yi, di leen dooleel ak a xirtal. Ni ko wolof di faral di waxee rekk, muy taw, mbaa muy naaj, dafa daan ànd ak ekib bi.
Kuñ daan yomb a ràññe la nag. Nde, foo ko fekkaan, wirgoy raayab réew mi lay sol, bëggoon réew mi lool, ak ekib bi, ba foo ko nattoon rekk, weesuna ko. Xarit la woon itam ci jawriñ jiñ dénkoon wàllu tàggat-yaram, Mataar Ba. Ku ko miinoon lool la. Looloo tax Mataar ba seedeel ko kàddu yi toftalu, jaalee ko ko :
“Ci naqar wii nu ame, noo ngi jaale ñii di waa-kër ki nga xam ni jóge na fi, di ko jaale itam jëwriñ jii ñu dénk mbiri tàggat-yaram, Yaankooba Jatara, njiitul mbootaayu 12eelu gaynde gi, waaye ak kureel gi ëmb soppey ekib bi.”
Momar Njaay, nekkoon na kuñ yàgg a tappal i cargal ngir dogoom ak coono yim daj yépp ngir ekib bi. Cargal gi gënoon a rëy ciy bëtam, nag, mooy gi ko njiitu réew mi tappaloon, keroog, 17 saŋwiyee 2014, muy “grade de chevalier de l’ordre national du mérite”.
Waxaguñu kañ lay koy denc ak ban bés lañ koy dëjal. Ñoo ngi dégloondi ba am ci lu leer.
EJO ak Lu Defu Waxu ñoo ngi koy jaale njabootam ak i mbokkam, di leen mastawu, di ko jaale itam Senegaal gépp, rawatina axlu kuppe gi. | Defuwaxu |
Subsets and Splits