wolof
stringlengths 1
166
| french
stringlengths 2
331
|
---|---|
yoxoos | manière furtive d’entrer |
Dafa ne yoxoos dugg, defe ne gisuma ko | il est entré furtivement, pensant que je ne l’avais pas vu. |
yoroxlaan g- | ceratotheca sesamoides (Pédaliacées) (herbe gluante qui peut servir de fourrage) |
Jur gi laay wutal yoroxlaan | je cherche du Ceratotheca s. pour le bétail. |
Sa tànk bu gaaw bi mel ni yoroxlaan | avec ton pied rapide comme l’éclair. |
yorin w- | de tenir |
Booy nàmpal, yorin wu baax waa ngi | quand tu allaites, voici la bonne façon de tenir. |
yónni | envoyer qqn |
Kan nga yónni marse | qui as-tu envoyé au marché ? |
yow | toi |
Yow la woo | C'est toi qu’il a appelé. |
yoxoosu | entrer furtivement |
Dafa yoxoosu | il est entré furtivement |
yos | ceux de |
Sa yos lañu | ce sont les tiens. |
yoxos j- | huître |
Mënatuma lekk yoxos ju ñorul | je ne peux plus manger d’huîtres crues. |
yugg | être blotti |
Mu ngi ne yugg ci wetu ndey ji | il est blotti près de sa mère. |
yu | s’emploie avec les noms de la classe y- |
yul b- | mollet |
Yul yu réy la am | il a de gros mollets. |
yukk-yukki | marcher de façon saccadée |
Mu ngale di yukk-yukki di dem | il s’en va marchant d’une façon saccadée. |
yox-yoxi | avoir peur |
Ku yaakaar Sériñ Tuubaa doo yox-yoxi | qui espère en Sérigne Touba ne doit pas avoir peur. |
yulli | vider (un sac ou une poche) de son contenu |
Noona, mu yulli saaku ba ba mu set | alors, il vida complètement le sac. |
yukk-yukk | exprime une façon saccadée de marcher |
yulub | entrer subitement dans un trou profond |
Dafa doon xuus, ne yulub ci pax | il marchait dans l’eau et entra subitement dans un trou. |
yugur-yugur | Évoque la manière de marcher d’un pas pesant |
yu-nekk | chaque |
Ñaari fan yu-nekk | tous les deux jours. |
yunn | faire une brève apparition |
Jant bi dafa ne yunn, réeraat | le soleil a fait une brève apparition et a disparu à nouveau. |
yumpaañ j- | Épouse de l’oncle maternel |
Sama yumpaañ a ma woolu | C'est la femme de mon oncle maternel qui m’a fait appeler. |
yuqéelu | se dresser sur la pointe des pieds |
Soo yuqéeloo it, du la taxa tollook man | même si tu te mets sur la pointe des pieds, ça ne te fera pas aussi grand que moi. |
(prov.) Yuqéelu mbaam, du ko taxa day ni gëléem | le fait, pour un âne, de se dresser sur la pointe des pieds ne lui fera pas atteindre la taille d’un dromadaire. |
yulliku | se vider (un sac ou une poche) de son contenu |
yuppit y- | fripes |
yuq g- | moelle |
Génneel ma yuq gi | sors-moi la moelle ! |
yuqi | remonter un peu une chose enfoncée dans le sol |
Xale yee yuqi jën wi | ce sont les enfants qui ont remonté un peu le pieu. |
yuur g- | grêle |
Géj na taw ag yuur | il y a longtemps qu’il n’y a pas eu de grêle. |
yuri | vider (un contenu) |
Yuri na siddéem si woon ci poosam yépp | il a vidé tous les jujubes qui étaient dans sa poche. |
yuuli-yuuli j- | septième période de la saison des pluies, qui dure treize jours |
Yuuli-yuuli jeey sooga door | C'est la septième période de la saison des pluies qui vient de commencer. |
yuur | se courber |
Bunt bi dafa suufe, ku fiy jaar, faw nga yuur | la porte est basse, celui qui passe par là est obligé de se courber. |
yuut g- | salive |
Yéréem yaa ngi tooy xepp ak yuut | ses habits sont trempés de salive. |
yuuxoo y- | cris émis en chœur |
yuug | se baisser |
Yuugal ! | baisse-toi ! |
yuuxoo | siffler (qqn) en signe de désapprobation |
Nit ñi dañu ko yuxoo | le public la sifflé. |
yuux g- | cri |
Fu yuux yooyu jóge | D'où viennent ces cris ? |
yuy | qui |
Am na jaan yuy ëmb | il existe des serpents vivipares. |
àngare b- | engrais |
Def ci àngare | mets-y de l’engrais ! |
yuuxu | crier |
Bul yuuxu, guddi na | ne crie pas, il fait nuit ! |
yàbb | rester bouche bée |
Ba mu ma ko waxee, dama ne yàbb, di ko xool | quand il me l’a dit, j’étais là, bouche bée, à le regarder. |
yàkkamti | être pressé |
Mënuma laa xaar, dama yàkkamti | je ne peux pas t’attendre, je suis pressé. |
(prov.) Bu doom yàkkamtee génn kër baayam, yaayam a yàkkamti | si un enfant est pressé de quitter la maison de son père, c’est que c’est sa mère qui est pressée. |
yuuy b- | brume |
yàggaay b- | pérennité |
Dina dellusi gaa; yàggaay bi rekk a ma ci jaaxal | il reviendra certes; c’est seulement la longue durée qui m’inquiète dans tout ça. |
yàkkaliku | être élargi |
Ba nga solee sama dàll yi lañu yàkkaliku | C'est quand tu as mis mes chaussures qu’elles se sont élargies. |
yàccaaral | emphatique de {yàcc} |
yàbbi | sortir qqch de la bouche |
Dama ne nga yàbbi xaalis bi nga sex | je te dis d’enlever l’argent que tu as dans la bouche. |
yàbbi | déteindre |
Sér bi dafay yëbb; bu ko boole ak yeneen yi | le pagne déteint au contact de l’eau; ne le mets pas avec les autres ! |
yàmbaa j- | cannabis chanvre indien |
Dafay tux yàmbaa | il fume du chanvre indien. |
yàkki | Élargir |
Dama bëgga yàkki baat bi | je veux élargir le col. |
àttekat b- | juge arbitre |
yàmboŋ b- | bourbouille |
Puudar buy faj yàmboŋ la | C'est une poudre qui soigne la bourbouille. |
yàpp | dévorer |
Gaynde gee ko yàpp | C'est le lion qui l’a dévoré. |
yàlla tere | a Dieu ne plaise |
yàŋŋ | exprime le fait d’être libre, sans encombrement |
Séñ Fàllu nee na : Bu nee yàŋŋ, nga ne yoll te teey. Bu nee tacc, nga ne tekk, booleek nga ne nikk, ne nàŋŋ | le guide Fallou a dit : Quand elle (la voie) est libre, tu accélères sans te précipiter. Quand elle est embouteillée, tu restes calme, tu maîtrises ta voiture, tout en regardant droit devant toi. |
yàpp w- | viande |
Defal yàpp wi ci firsideer bi | mets la viande dans le réfrigérateur ! |
yàndoor | dormir profondément |